SITTA DAAN NA BÀLLA GAY 2

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dibéer, 20i Sulet 2025, Bàlla Gay 2, doomu Géejawaay ji, waada bu mag doon daje ak xale jàmm-a-gën bi, Sitta. Seen ndaje mi nag, bari woon na coow, ñu doon laaj ndax dana am walla déet. Li ko waraloon di Sitta mi waa CNG tegoon daan ci kawam, ndax ni dees bëggoon a saytu yaramam keroog ba mu bëree ak Móodu Lóo ba noppi, mu bañoon ko def. Loolu andi woon coow ci amug bëre bii. Waaye, ay kilifay Sitta doon ci dox ak di ci wax ba lépp sotti.

Tay, ñaari mbër yi ñëw ak pasteef, ku ci nekk liggéey yaramam ba taxaw. Ku ci nekk ñëw na ci waxtu wi mu war a ñëw, def ay xarfa-fuufaam, neexal bés bi. Ñaari mbër yépp bàkku ca na mu gën a neexe.

Ñu noppi seen lépp, dugg ca géew ga. Arbiitar bi wax ak ñoom, fàttali leen sàrt yi, añs. Piiib, bëre ba tàmbali, ñaari mbër yi dawal léewatoo bi ab diir. Nes-tuut Bàlla Gay sànni ay kurpañ, Sitta fayu. Ci noonu Sitta song, ñu jàppante, « yarmin » bi tàmbali di def ay pexe, lu mu teg Bàlla Gay teggi ko. Waaye Sitta bam ko nattee yëg ni mën na am dara, mu topp loolu rekk ba rëpp fa ay woomam góor-gólu ba jógaat. Ba tay, mu jàpp bu dëgër moom Sitta daldi yëkkati gaynde Géejawaay gi tegaat ko. Gannaaw loolu la ko kal rekk wéeru ko, daan ko.

LIIS NJAAGO – AADA FAAS

Démb ci gaawu bi tamit, ñaari mbër yu mag doon nañu ci bëre, doomu ndakaaru ji nax doomu jàmm-a-gën ji daan ko jéll bu rëy te gaaw. Ñoom ñaar nag yàggoon nañu tëkkonte ak a sanantey xeer ay jamono, mu mel ni dafa leeroon ni bés dana dikk ñu laale. Ba seen bés taxawee itam naka noonu, kenn mayul sa moroom dara. Liis Njaago ci ndam la jóge woon (Lak Róos), Aada Faas gëje ci ñàkk digganteem ak Lak-dë-geer 2.

Ñu gisoon seen i jàkkaarloo na mu daan mel nag, tàng jër, ba ci mu mujj bi ñaari mbër yi xaw fa laale ba Aada Faas dóor ca ki nga xam ni mooy Liis Njaago.

Seen bés bi, démb, ñu gis ñaari mbër yépp ñëw ak dogu. Waaye mel ni doomu Faas ji moo gënoon a firi. Liis Njaago, ñi ko xam dëgg gis nañu ni démb xawoon na sedd, wuteek yeeneen bésam. Loolu, ñii ne yaram wu bari wim indaale wii yoon la, ñee ne dañu ko jekku. Ak lu mën a am daal goney Ndakaaru gee ko gënoon a sawar.

Ba ñaari mbër yi noppee ba taxaw ca digg géew ba, arbiitar ba wax ak ñoom daldi ne « piriiiib!!! » Noonu, ñaari mbër yi xawoon sorante, ku ci nekk taxaw fa nga taxaw, ñuy léewatoo. Nis-tuut Aada Faas dox génn saaku ya def ay mbiram delsi, arbiitar dànkaafu ko, daldi mbiibaat. Wii yoon, ci diir bu gàtt ci léewatoo ba Liis daldi sànni kurpañ Aada moytu ko ba noppi gën a wàcc ciy tànkam. Laata Liis Njaago di xalaat leneen xale Ndakaaru bi ne coppet tànkam rekk dóor ko palaake, fa muy bañ-bañlu mu wiij ko ca geneen wet ga, naj ko, mu toog.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj