WAAJTAAYI GÀMMU 2025 : NJIITU RÉEW MAA NGA WOON FA TIWAAWAN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tay ci gaawu bi, Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo nga woon Tiwaawan. Mu doon fa amal ab tukki ngir nemmeeku Xalifa ba ci jamono yii ñu nekk ci waajtaayi gàmmu gi.

Ay fan kepp ñoo des ngir ñu àgg ci bésub Gàmmu gi ñuy amal keroog 4i fan ci weeru sàttumbar. Ñu ciy màggal bésub juddu Yónnent Yàlla Séydinaa Muhammat SAW. Jamono yii ñu koy waajal, kilifay réew mi sàqi nañu ay jéego ngir gunge kilifa diine yi ba ñu mën a amal bés bi ci anam yu mucc ayib.

Naka noonu, jëwriñ ji ñu dénk wàllu ndox mi, Séex Tiijaan Jéey, doon na nemmeeku matuwaay yi ñu jël fa Tiwaawan ak “chateau d’eau” bu bees bu ñu fa sàmp ngir koñ yi nekk ca dëkk bépp mën a jot ci ndox mi. Yokk nañu ci itam ay sëfaani ndox (kamiyoŋi sitern) ngir ndox mi bañ fa ñàkk, waaye itam ay sëfaan yuy ŋacc ngir sàmm kéew mi.

Ba tay ci waajtaay yi, Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, teewoon na, tay ci gaawu bi, fa Tiwaawan. Bi 11i waxtu di jot ci yoor-yoor la fa àgg ngir amal fa tukkib nemmeeku ci wetu Xalifa bi, Sëriñ Baabakar Sy Mansuur.

Ginnaaw bi ñu leen dalalee, Njiitu réew mi ak jëwriñ yi mu àndaloon, amal nañu fa jotaayu waxtaan ak Xalifa bi. Ci waxtaan woowu sax, Xalifa bi yékkati na fay kàddu, taxaw bu baax ci njariñu jàmm ak bennoo réew mi. Ñaanal na Njiitu réew meet ngir mu am ndam ci sas wu réy wi mu am ci boppu réew mi.

Bi mu jëlee kàddu gi itam, Njiitu réew mi ndokkale na Xalifa bi ci amalug Gàmmu gi. Ñaanal na ko itam Yàlla yokk ko wér. Ginnaaw loolu, Njiitu réew mi feddali na yéeney Nguur gi ci taxawu ak gunge Tiwaawan ci naal yi mu am ngir yeesal dëkk bi.

Ginnaaw waxtaanam ak Xalifa bi, Njiitu réew mi amal nab lël ak Njabootu Allaaji Maalig Si fa bérébu ndaje ma ñu duppe “Complexe Sëriñ Baabakar Si”. Foofu itam, Njiitu réew mi dellusi na ci taxawaayu tarixa yi ak ni ñu doone royukaay, yoonu jàmm ak suqaleeku. Xamle na fa itam ni dina taxawal koppar yees jagleel xew-xewi diine yi ngir gën a mën a taxawu ëttu këru diine yi.

Delloo na itam njukkal El Haaji Maalig mi njëkk a taxawal Gàmmu gi fi réew mi, ca atum 1902. Ci noonu, mu dellu rafetlu ni ko ay ndonoom wéyee di ko sàmm ak a taxawu ci anam yu mucc-ayib.

Ginnaaw ndaje moomu, Njiitu réew mi demoon na nemmeeku Jumaay Tiwaawan ju mag ji.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj