Bàyyi nañu juróom-benni Saa-Senegaal yi ñu tegoon loxo fa Mali. Ci lees wax, terrorist yi (rëtalkat yi) ñoo leen jàppoon ci alxames ji laata ñu leen di bàyyi ci àjjuma ji.
Démb ci àjjuma ji la URS (Union des Routiers du Sénégal), di kurélug liggéeykat yiy yëngu ci yaale ji (dem ak dikk), biraloon ni rëtalkat yi teg nañu loxo juróom-benn ci seen i ñoñ yiy daw diggante Senegaal ak Mali. Bees sukkandikoo ci xibaar bi ñu siiwal, ñoo ngi leen tegoon loxo ci alxames ji.
Ginnaaw bi ñu nemmeekoo li nu mel, fara-saytu kurélug URS bi xamle na ni yëgal nañu ko kilifay Senegaal yi ci àjjuma ci suba, jaare ko ci àmbaasaadu Senegaal bi nekk Mali ak jëwriñ ji ñu dénk yaale ji.
Bees sukkandikoo ci xibaar yi sunuy naataango yu Dakaractu siiwal, jëwriñ ji yore kàddu Càmm gi, Mustafaa Njekk Sare, jotoon naa dëggal lu ni mel. Waaye, yëgle bi tukkee ci jëwriñ ji ñu dénk Mbiri bitim-réew ak Bennoo Afrig waxul lu ni mel. Nde, la mu xamle woon mooy ni dégg na yëgle bi te moo ngi ciy bàyyi xel, di ko topp ak kilifay Mali yi. Waaye, amul benn xibaar bu wér bu mën a firndeel jàpp gi ñuy wax, mbaa ñu mën a ràññatle ñi ñu jàpp.
Ay waxtu ginnaaw bi xibaar bi jibee, fara-saytu URS bii di Góora Mbóoj biral na ci gaawu bi ni féexal nañu ñi ñu jàppoon niki démb ci àjjuma ji, ci ngoon gi. Donte ni amoon nañu ci njàqare, delsi nañu ci jàmm, nekkaat ci seen i yitte fa réewum Mali.
Nguur gi nag àddoogul ci bàyyi gi donte ni xamle woon nañu ni ñoo ngi topp mbir mi ak kilifay Mali yi.