Ginnaaw tekkaaral gu yàgg gees nemmeeku woon ci kujje gi diggante bi waa Pastef toogee ci Nguur geek léegi, mujj nañoo wàcc ci mbeddi Ndakaaru yi ngir amal ab doxu ñaxtu.
Démb ci àjjuma ji, 19 sàttumbar 2025, way-kujje yee ngi woon ci mbedd yi. Ñu doon amal nag ab doxu ñaxtu bu kurél gi duppee seen bopp “Rappel à l’ordre” woote woon ngir sàkku ci Nguur gi ñu bàyyi ñees jàpp ngir jëfi pólitig, ñu leen di wax ci nasaraan “détenus pólitig” te dakkal ku wax ñu jàpp tëj.
Seen doxu ñaxtu boobu nag, ñoo ngi ko jàppoon fa Jëppal (Ndakaaru), waroon jaare ci ngérum (avenue) Xalifa Abaabakar Si, wéyal ko ba ci “rond point” bu Liberté 6. Donte ni rafetluwuñu weneen yoon wi leen takk-der yi mujj a rëddal ci ndigalu kilifa yi, mujj nañu amal seen doxu ñaxtu ci jàmm.
Seetlu nañu fa teewaayu ñenn ñu ràññeeku ci géewu pólitig bi, ñu deme ni Abdu Mbów ak Ceerno Alasaan Sàll. Ñenn ci fara-ma-xejj yeet teewoon nañu fa.
Ci kàddu yi ñu fa jot a yékkati nag, ña ngay duut baaraamu tuuma Nguur gi fi nekk. Nde ci seen i wax, Nguur gi fi nekk deful lu dul di jaay doole nit ñi : “Saa-Senegaal yee ngi ko séq ak Nguurug jaay doole gog, deful lu dul di tëj nit ñi” (Abdu Mbów).
Naka noonoot lañu seetloo ci seen pànkàrt yi ay kàddu yu deme ni “Bàyyileen Farba”, “Bàyyileen Tayiiru”, “Bàyyileen Badara Gajaga”, “Bàyyileen Abdu Ngeer”, walla sax “Sonko abal nu”.
Ba tay ci seen i kàddu, Nguur gi yamul rekk ci jaay doole. Nde ci defanteek way-politig yi la nekk ak a jiixi-jaaxaloo caytu gi. Ba tax ñu jàpp ni doxaliinam dafay gën di safaanook Nguurug Yoon te Askan wu takku temm a ko ci mën a jële.