MBIRUM MAJAMBAL JAAÑ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw bi Majambal Jaañ dawee, génn réew mi, Nguurug Senegaal jàpplu na ko fu mu mën a teg tànkam ci àddina si, dellu dàq njiitul DIC ak komiseeru takk-deri AIBD.

Ci guddig talaata 23, jàpp àllarba 24 sàttumbar 2025 la Majambal Jaañ génnoon réew mi. Moom ci boppam moo xamle woon ci àllarba ji ni jóge na Senegaal ci guddi gi, donte ni takk-der yi bañaloon nañu ko ko. Naka noonu, mu xamle ne ma nga dal Pari, réewum Farãs, te dina waajal i laykat yu ko layal ngir janook Yoon.

Dem gi mu dem nag fa réewum Farãs, fekk ñu tere woon ko génn réew mi ndax li Yoon nekk ciy mbiram, tax na ñu jàpp ni dafa fàq ngir rawale boppam. Bi demam gi biree nag, kilafa yi, rawati àttekat yu PJF (Pool Judiciaire financière) jël nañu ay ndogal ci moom ak ci caytu gi.

Jëwriñ ji ñu dénk biir réew meek kaaraange ma-xejj yi, Meetar Bàmba Siise, xamle na ni tekki nañu ndombog-tànku njiitul Dic (Division des Investigations Criminelles) ak komiseer bu mag ba nekkoon fa naawub AIBD (Aéroport International Blaise Diagne). Xamle naat ni ubbi nañu luññutu ci caytu gi ngir leeral anam yi mu génnee réew mi ak ñu ko ci mën a jàppale. Bépp lajj-lajj bu ci mën a am it ba tax Sëñ Jaañ rawale boppam dana wex xàtt ña ca laale.

Bu dee lu jëm ci Majambal Jaañ, PJF mi nekkoon ciy tànkam jàpplu na ko, ak fu mu mën a teg tànkam ci àddina si. Muy lu ñuy duppe ci nasaraan mandat d’arrêt international.

Jàpp nañu doomam jii di Sëriñ Saaliw Jaañ, fekk mu doon jéem a génn réew mi, jaare ko Gàmbi. Teg nañu loxo itam Soxna Jaañ, di soxna ci Majambal Jaañ. Ginnaaw bi ñu leen dégloo itam, téyendi nañu leen, te dinañu fa toog, lu mu gàtt gàtt, ba altine ngir ñu xam seen i mbir fu muy mujj.

Ginnaaw bi mu yëgee ni àttekat yi jàpplu nañu ko fépp fu mu mën a teg tànkam ci àddina si, moom ndayu mbill gi, Majàmbal Jaañ, àddu na ci. Naka noonu, muy xamle ni yëg na xibaaru jàpplu bees ko jàpplu. Waaye laata àpp gi di jeex dina jébbal boppam Yoon te taxaw layook ñoom.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj