Takk-deri Gana yi tàmbali nañoo lëñbët ngir ca yan anam la doomu Senegaal jii di Seex Ture faatoo ak ñan ñoo jël bakkanam. Dafa di sax, am na ku ñu duutagum baaraam, njort ne laale na ci mbir mi.
Bu dee li ñeel luññutu yi, L’Observateur a ngi xamle takk-deri Gana yi amagum nañu kenn koo xam ne, am nañu njort yu dëgër ne laale na ci. Yéenekaay bi dafa bind ne :
« Luññutu yi njiiti Gana yi ubbi, ginnaaw bi leen njiiti Senegaal yi jokkee, mi ngi jëm kanam bu baax. Luññutu yaa ngi aju deewub Seex Ture, di ndawub Senegaal boo xam ne, dañu fekk néewam ca lopitaalu diiwaanu Asanti, soree Akra (péeyub Gana), 250i kilomeetar. Bees sukkandikoo ci xibaar ya takk-deri dëkk ba fésal, xàmmee nañ bu baax nit ki indi néew bi ca morgu ba. Mi ngi tuddu Isaa te moom lañu njortagum ne moo ray Seex Ture ci lu dul yoon. »
Yéenekaay Libération tamit bind na ci. Ñoom li ñu xamle mooy ne, banqaasu pólis bu Asanti biy lijjanti mbirum pekke yi dëggal na ne ubbi na ay luññutu ci deewub Seex Ture bi. Isaa moomu ñu wax ne moo indi néewub Seex Ture fa morgu ba, dafa waxoon ne mbokku (rakk walla mag) Seex Ture la. Fi mu nekk nii, ñu ngi nekk di ko wër.
Ngir fàttali, Seex Tuure ab ndaw la woon bu doon góolu, xarañoon ci lool. Yëmbël la dëkkoon. Moom nag, dafa am ñu ko nax, gëmloo ko ne dañu koy yóbbu Marog ngir mu futbli fa. Ndekete, saay-saay yi ko tuur lëndëm, Gana lañu ko yóbbu, jàpp ko fa, di mbugal ak metital, di laaj xaalis ay way-juram. Saay-saay yi nag, xaalis bu bare lañu doon laaj. Bi way-juri Seex Ture yi lottee ci matal ko, ca lañu ko faat.
Fi mu nekk nii nag, nee ñu am na yeneen i ndaw yu nekk ci loxoy saay-saay yooyee, fa Gana. Nguur gi, jaare ko ci njëwriñu mbiri bitim-réew, mi jokkook njiiti Gana yi, di liggéey ak ñoom ngir leeral rayug Seex Ture bi, waayeet ngir musal yeneen ndaw yi nekk ci loxoy saay-saay yi.