COOWAL BOR BI ÑU NËBB

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal bor bi ñu ne Nguurug Maki Sàll dafa ko nëbboon a ngi wéy di gën a jolli ci dëkk bi, ginnaaw bi layookati Maki Sàll yi defee seen janoo bu njëkk ak taskati xibaar yi ngir, ci seen i wax, andi ay leeral.

Barki-démb, ci alxames ji, layookati Maki Sàll yi doon nañu janook taskayi xibaar yi ngir àddu ci koppar yi Nguur gi fi nekk wax ni dafa ko leboon ci diggante 2018 ak 2023 te siiwalu ko, muy bor bu ñu nëbb.

Ca janoo boobu ñu doon am ak taskati xibaar yi nag, Meetar Pierr-Olivier Sur, di doomu réewum Farãs, jiite kippaangog layookati Maki Sàll yi, yékkati na fay kàddu ngir dellusi ci nees xaymaa boru Nguur gi ba naan dafa yéeg. Naka noonu, mu wax ci biir i faramfàcceem ni ay coppite lañu andi ci doxalin wi li ko dale ca atum 2023. Coppite yooyu nag, moo tax ba ñuy boole bori banqaasi Nguur gi ci bori Nguur ngi.

Li mu biral nag tax na ba mu jàpp ni bees bëggee mbir yi leer, fàww ñu dellusi ci déggiinu baat yi. Waaye yamul ci loolu nde dafa dellu tuumal Nguur gi fi nekk ni caabal yi ñuy tudd ni ñoo dëggal nëbb gi kenn tegu leen bët. Dañu leen nëbb. Ba tax mu jàpp ni « caabal yu ñu nëbb lañu war a wax waaye du bor bu ñu nëbb.

Ginnaaw gi, kilifa yu bokk Pastef, làng gi yore Nguur gi, génn nañu ñoom itam ngir weddi kàddu yooyule. Ki njëkk a biral kàdduy weddi yooyule mooy Al Amiin Lóo, di jëwriñ ci Nguur gi. Naka noonu, muy xamle ni bor yi Sëñ Sur di jéem a teqale, tàmbali nañu leen boole lu jiite lél bi muy wax.

Bu dee kii di Waali Juuf Bojã moom, jiite waaxu Ndakaaru, jàpp na ni ay waxi pólitig doŋŋ la ñi fi nekkoon di jéem a jàllale ngir gëlëmloo askan wi. Ci noonu, mu dellu biral ni Maki Sàll daf fi sampoon ay jëfi nëbbatu ba faf bàyyee réew mi bor bu yéeme bu ñu war a fay, mu tollu ci 16i milyaar yu réew miy fay weer wu nekk. Naka noonoot, muy leeral ni ñoom soxlawuñu di sos bor bu amul ngir àtte ko. Mu teg ca ni dinañu jot ci moom.

Bees sukkandikoo ci li kilifay Pastef yi wax, ci ay bor yu Nguur gi daan leb ci Bànk yi la Maki Sàll ak Caytoom doon jaare. Ci li ñu tënk « topp nañu lu ëpp 4 065i milyaar yu ñu leb daar-daar ci bànk yi, ak 1 267i milyaar yu ñu waxul ». Am na ci xaalis bob, Nguur gi ay këru liggéey la ko torlul.

Ndeem ñaari wàll yépp noppi nañu ngir jàkkarloo, bor bu ñu nëbb laam caabal yu ñu nëbb dina leer. Nde, li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj