Gaawo, 13eelu desàmbar 2025, ca Jàngune bu Ndar, la Pàppa Aali Jàllo (njiitul LDW) doon gaaral teesam ci Làkk ak mbatiiti Afrig, duppe ko « Pratiques antrhoponymiques en milieu pulaar, au Fouta Tooro : forme et sens » ci njiteefu Porofesëer Fidel Jéeju, UGB, ak Alfa bari bu Iniwérsite Bordeaux-Montaigne ak ñetti way-saabal (rapporteurs) : Abdurahmaan Jàllo (Inalco, Paris), Usmaan Jaawo (UCAD) ak Kaliidu Si (UGB). Prof Bubakar Kamara moo jiite woon « jury » bi.
Pàppa Aali Jàllo nag, dafa bokk ci njëlbeenug maasu ndongo ya ñu yóbboon ca banqaas biy jàngale lépp lu jëm ci làkk, mbatiit, xayte, mboor ak mboolaayi Afrig, ñu duppee ko Département Langues et cultures africaines. Ca atum 2013 lañu ubbi banqaas boobii nekk ca jànguneb Gastoŋ Berse bu Ndar. Kàngaam bii di Bubakar Bóris Jóob a fa joxe njàngale mu njëmm ma, di woon njàngum wolof.
Ca maasi ndongo gu njëkk googu, Pàppa Aali Jàllo daf ci ràññeeku woon lool, daan jiitu saa su nekk. Rax-ci-dolli,ca seen biir, moo fa njëkk a gaaral ca péncum jàngune ba lees duppee Mémoire de master, amoon ca mention « Très bien ». Naka noonu, moo nekkaat ku fa njëkk a gaaral ab tees ca péncum jàngune ba, mbooloo mu bari teewe woon ko.
Pr Mamadu Njaay bu Jàngune Seex Anta Jóob bu Ndakaaru moo waroon a jiite « jury » bi. Waaye dafa amoon ngànt, Pr Buubakar Kamara wuutu ko. Ginnaaw bi mu nuyoo ña fa teewoon, moom Porfesoor Kamara, jéggalu ci yéex gee tàmbali, dafa jox kàddu gi Pàppa Aali Jàllo ngir mu faramfàcce liggéeyam, gaaral njureefi gëstoom laata ñuy door laaj yeek tontu yi.
Ci kaw loolu la Pàppa Aali jël kàddu gi, wax ne :
« Tees bii, mi ngi soqeekoo ci menn njàng mees amaloon ca jamonoy Master, ñu duppee ko Antroponymie et toponymie en Afrique. Njàng moomu moo yee ci man ag mbañ-kumpa, ma samp i laaj ñeel cosaani turi Pël yi, nees leen tëggee ak lu ñuy wund ci wàllu mbatiit ak anam bi ñuy ràññatlee askan yi, rawatina Pël yi. Li gën a waral laaj yi mooy ne, ci sama néegu nday Paab lañu may woowee ; bu dee sama néegu baay, ñu may woowee Aalóo. Muy ñaari tur yu bokkul ci kenn nit, loolu daldi sama bopp, ma bëggoon a xam lu tax mëneesul woon jëfandikoo wenn tur rekk. »
Looloo tax Pàppa Aali sumb ab gëstu ci anam yees di tànniini turi Pulaar yi, sabab yi ak taxawaayi jëmmi tur yi ci biir làkku pulaar wi. Maanaam, daf ci doon faramfàcce anam yi ñu leen di xalaate, di leen ko tëgge ak di leen jëfandikoo ci biir askan wi. Ca Fuuta Tooro nag la doon defe ay luññutoom.
Liggéeyam bi dafay dugg, gën-gaa yaatu, ci fànnuw xam-xamu tur yi. Ñu koy wax ci nasaraan Onomastique. Dafa sukkandikoo ci xeeti taxawaay ak doxalin yu mucc ayib yu mu xeeñtoo ci fànni xam-xami làmmiñ yi ak gis-gisi yeneen fànni xam-xam.
Ngirte li gënoon a mag ci liggéey bi moo nekkoon mu feeñal dayob tëgginu tur yi ci askanu Pulaar, ak mbir yi ñu làmboo ci mboolaay meek mbatiitam, ci làmmiñ wi, ci mboor ba ci doxalinu jamono, te yooyule mbir waral tur yees di gis ñu leen di tànn ak a jëfandikoo ci askanu Pulaar wi ci Fuuta Tooro. Loolu di wane solo si njàngatum tur yi am ci wàlluw làmmiñal.
Tees bi day wane ni tur yi nekkee i ndëxëñteef yuy dundal askanu Pulaar ak di ko fàttali lépp lu taqook mbooram ak xayteem. Naam, dina sàmm mbatiitu pulaar, waaye dafa baax ci xarala ndaxte yit tontu na « lees mën a jànge ci nit ak ci mboolaayu pulaar ».
Pàppa Aali Jàllo wax na tamit ci yenn jafe-jafe yi mu jànkoonteel ciy luññutoom ca Podoor ndax Ndakaaru la juddoo, yaroo Ndakaaru, guléet mu teg tànk Podoor ci Tees bi ; kon dafa xawoon a mel ni ag gan ci ñoom. Gàllankooru ko lool waaye xéy-na mënoon naa gën a yomb ci moom.
Àttekat yépp (jury) a bég lool ci teesu Pàppa Aali Jàllo bi te nëbbuñu ko ndax “sunu ndongo la. Njeexitalu njàngam day wane naam xareñam, waaye nun it sunug xareñ. Sagal na nu”. Dikk nañu bu baax ci njariñ li tees bi am muy :
– Ci tool bu kenn mësut a ruuj daanaka ; kon ëllëg, képp kuy liggéeyati ci turi pulaar dina ko soxla ;
– Askan wi dina ko jëfandikoo, rawatina wow pulaar ;
– Yékkati na dayob UFR ba ci Iniwérsite.
Pr Fidel Jéeju fàttali na ne tees bi xarala, yëfu nit la kon lépp mënul jaar yoon moo tax jukkees na ci yees war a xoolaat, béqi ko, door koo siiwal, baaxe ko ñi ko mën a liggéeye ëllëg. Pàppa Aali Jàllo nangu ko te fas na yéene defaraat yiñ ko wax.
Ba loolu lépp weesoo, àttekati “jury” bi lëluji, gise ci seen biir, dellusi. Li ñépp doon xaar : Tees bi jaar na yoon, nees ko bindee sàmmonte na ak wareef yi, boroom saytu na, def na liggéey bu mucc ayib, tees bi am na njariñ. Pàppa Aali tappal nañu la garaatu [darajay] Doktoor ak « mention très honorable » ak « félicitaions du jury ». Pr Fidel Jéeju daldi solal Doktoor Pàppa Aali Jàllo mbubbu doktoor mi : yor melo mboq ci ginnaaw gi, loxo yi ak butoŋ yi, kanam geek suufu loxo yi ñuul, di saamandaay robbu layalkat, gudd, yaatu, am i loxo yuy lang. Xol yépp sedd.
Bés niki tay, neeleen Doktoor Pàppa Aali Jàllo.
Porofesëer Kaliidu Si, kenn ci way-saabal yi, bokkoon ci « jury » bi, joxe na xalaatam ci tees bi. Daf ne :
« Sama gis-gis ci teesu Pàppa Aali Jàllo bi mooy, wax dëgg Yàlla liggéeyam jaar na yoon, set na. Ndaxte, ca njalbéen ga, bi nu xoole liggéey bi, ñetti caabal yépp [pré-rapports] ñoo ko nangul liggéeyam, wax ne mëenees na ka gaaral ci péncum jàngune bi. Beneen bi, ci bisub gaaral bi (soutenance), jéem na tontu ci laaj yépp, boole kook yar ak teggin.
Bu loolu weesoo, tees bi dafa am solo ndax dafa liggéey ci tur. Te, tur, ci wolof, pulaar, seereer ak keneen ak keneen, ñépp a ci yem, lu am solo la : foo déggee tur, wax nanu mbatiit, kuy tudd, kan la ñuy tudd, naka lañuy tuddee ak ki ñuy tudd lu tudd mi mën a def ci moom.
Ci pulaar teesam bii mooy bi ci njëkk ci UGB te day wane ni
– am nanu njàngaan yu jàmbaare, bëgg li ñuy def ;
– Pàppa Aali Jàllo mënoon na tànn wëppa wu yomb, ni ko ñenn di defee, jaar jàll, waaye dafa taamu lu amal solo askanam.
– Pàppa Aali Jàllo halpulaar bu juddoowul Fuuta la, te it màggeewu fa ; kon su ko neexoon mu ne xamul Fuuta, liggéey bi day jafe. Waaye dafa dellu ci xeetam, jéem a xam na ñuy dunde.
– Daanaka amul woon tamit ay mbind walla liggéey ci wëppa wi. Ëllëg, ku ciy liggéeyati dina ko tudd. Mën na am ñu mottali walla weddi li mu wax. Waaye, loolu amul solo ndax xam-xam amul fu mu yem, ku nekk day wax rekk li mu xam.
Liggéeyam am na solo ci Halpulaaren yi ndax da leen iy delloo ci seen mbatiit ak seen dundiin.”
Di fàttali ne, Doktoor Jàllo mooy njiitu Mbindum seen yéenekaay Lu Defu Waxu, yor xalima bu am doole, di liggéey it ci EJO-ÉDITION (seen këru móolukaay ci làmmiñi réew mi).
Jàllo Jéeri sagu na, siggi na, siggil ay mbokk, ay jàngalekatam, ay amdi-jàmmam ak képp ku koy sagoo.
EJO-ÉDITIONS ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy ndokkeel bu baax.