LI GËN A FÉS CI XIBAAR BÉS BI (18/4/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

ÑAAREELU NDAJEM JËWRIÑ

Démb ci àllarba ji la Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Fay doon amal ñaareelu ndajem jëwriñam ginnaaw bi ñu ko falee ak léegi. Ca ndaje mooma jot naa fa jël ay ndogal boole ceek amal i càkkuteef ci yenn banqaasi Yoon yi, ci campeef yi (institutions) ak tamit ci jëwriñam yi. Càkkuteef li ci gën a fés mooy li mu sàkku ci banqaas yii di “Cour des comptes”, “IGE” ak “OFNAC” ñu siiwal seen caabal yi ñu def ci juróomi at yu mujj yii. Mu sàkkuwaat tamit ci jëwriñ ji ñu dénk wàllu Yoon mu defar ag càrt guy aar gaa ñiy siiwal ñi luubal alalu réew mi laata fukki fan ak juróom ci weeru me. Mu yokk ci, ginnaaw loolu it, dina amal ndajem caytug campeef yi at mu jot. Sàkku na ci elimaanu jëwriñ yi mu waajal bésub waxtaan bi ñu war a amal ñaar-fukki fan ak juróom-ñett ci weeru me. Li ñuy waxtaane mooy “Coppali ak Yeesalug Yoon wi”. Waaye, yemul foofu rekk. Ndax, sos na ca Njiiteefu réew ma ga ag kurél ñeel mbiri diine yi ak wutalug liggéey ñi am lijaasa ci njàngum araab.

SÉYDINAA UMAR TURE LEERAL NA

 Séydinaa Umar Ture, ñu gën koo xam ci turu Kàppiteen Ture, indi na ay leeral ci xibaar yi yenn kibaaraan tàmbali woon a jàllale. Nde, dañu ne woon ne delluwaat na Sàndarmëri ga mu nekkoon laata ñu koy dàq. Kii di fara-caytoom, Usmaan Natañel Ñaŋ xamle na ne xibaar boobu wérul. Te, bu doon dëgg sax, duñu ko fore ci mbedd mi. Waaye, moom ndeyi-mbill ji moo leen koy yegge.

PDS PELENT NA DIRECT NEWS

Direct News ab yéenekaay la bu Saa-Senegaal yu bari ràññe, rawatina ñiy jële xibaar ci mbaali jokkoo yi. Li waral pelent boobu mooy ne làng gii di PDS (Parti Démocratique du Sénégal) nee nañu dafa yàq seen der. Nde, dañoo biral ay xibaar yu wérul ci seen lawax bii di Kariim Wàdd ak ñenn ci kilifay làng gi. Dafa di, seen xibaar yi ñu siiwal ci altine ji dañu doon laaj lu tax waa PDS bokkuñu ci Nguur gi Usmaan Sonko jiite. Waaye, yemuñu foofu. Ndax, dañu cee yokk ne dafa am ñenn ci seen i kilifa yoo xam ne dañoo jébbal Usmaan Sonko seen i këyit (CV) ngir mu jël leen ci Nguuram gi. Muy kii di Saaliw Jeŋ, Nafi Jàllo, Mayoro Fay ak Abdulaay Raasin Kan. Te, nee nañu, amul kenn ci ñoom koo xam ne waxtaan na ak Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Fay walla elimaanu jëwriñ yi ngir ndombal-tànku jëwriñ kenn ku bokk ci ñoom.

NJÀNG AK TÀGGAT NGIR ÑÉPP

Doktoor Baabakar Jóob, meeru Cees, jël na ndogal lu am solo ngir jëmmal naalam boobu mu dippe “Education et Formation pour Tous”. Ndogal loolu mu jël nag du naqari ndongoy Cees yi nekk ci daara yu kowe yi, yu ndaw yeek yu digg-dóomu yi. Nde, dafa fas yéenee maye lu tollu ci junni ak juróom-ñett fukk ak juróom-ñeenti “bourses”. Te, loolu mu maye yépp ci at mii la. Maanaam, atum 2023 mii ñu génn jàpp atum 2024 mii di mottali li ñuy dippe “année académique” ci farãse.

XEW-XEW BU TIIS FA TEFESU GÀDDAAY

Ndox maa ngi wéy ba tey di wann Saa-Senegaal yi, donte ne sax wii yoon du mbëkk mi. Ndax, ñaari ndaw ñoo lab fa géeju Gàddaay ga. Kenn ki di wuyoo ci turu Séynabu Sàmb. Keneen ki, Séex Sàmb. Ñoom ñaar ñépp ñoo bokk fa ñuy jànge. Li ci gën a doy waar mooy ba tey gisaguñu néewi ñaari ndaw yooyu lab.

BENEEN XEW-XEW  BU TIIS FA KEEÑAA

Xew-xew boobu ma nga am tey ci bëccëg ca boori sowu réew ma, ca dëkk bii di Sindar. Li ñuy dippe “crash” moo fa am. Maanaam, ab roppalaan moo fa daanu. Ca jéyya jooju nag, am na bakkan yu bari yu ca rot. Ka jiite woon Làrme ba di Francis Omondi Ogolli ak yeneen juróom-ñeenti sóobare yoo xam ne ay kilifa lañu ca Làrme ba ñoo ca ñàkk seen bakkan. Nee ñu am na ñaar ñoo xam ne moom mucc nañu ca jéyya jooju.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj