LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (14/10/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SENEGAAL 2050

Senegaal am na sémbu delluwaay wu bees. Tay ci altine ji, 14i pani oktoobar 2024, la ko Càmm gi aajar fa Jamñaajo. Muy sémb wu Càmm gi taxawal, mu wuutu PSE (Plan Senegaal Émergent) bi Nguur gi weesu tënku woon ngir tabax yokkute réew mi. Sémb wu bees wi nag, ñiŋ ko duppe Senegal 2050, Agenda nationale de transformation. Ñu daldi ko tënk ci 4i bànqaas yu ñu màndargaal cig guy. Ñeenti bànqaas yi di Càmmeef gu baax ak ndogu ñeel Afrig, caytu gu mucc ayib ak suqaleeku gu sax, nit ñu xarañ ak yemale ñépp, koom-koom gu dëgër. Muy liggéey bu ñuy tàllal ba atum 2050.

JUREB DUUDU WÀDD AK I ÑOÑAM

Duudu Wàdd, Tafsiir Caw, Awa Ba ak seen i ñoñ xamle nañu démb ci dibéer ji ni dinañu jébbal Yoon b jure (plainte), tay ci altine ji. Ñoom waa lëkkatoo Soppi Senegaal, dañu am lu leen naqadi ci li ñu wax ni dafa am ñuy jëfandikoo nu mu leen neexe xaatimu Meetar Abdulaay Wàdd. Ngir dakkal jëf ju ñaaw jooju te ruslu nag, dinañu yóbbu alaxam ci kanamu yoon. Bu ñu ci jógee, itam dinañu ko boole fa njëwriñal biir réew mi ci li ñu nekk di salfaañe sàrti pàrti bi.

DELLOO NJUKKAL

Magum jëwriñ yi amal nab woote ndimbal ñeel soldaar yi taxaw ngir delloo leen njukkal. Barki-démb ci gaawu gi la ko tijji, ñu fas koo wéyal ba keroog 19i pani desàmbar 2024. Li mu ko dugge nag mooy fexe dajale ay koppar ngir jàppale soldaar yi jële ay gaañu-gaañu ci xare yi ak ñi taxaw ba mënatuñ bokk ci làrme bi. Bees sukkandikoo ci Mbay Siise, ndimbal loolu dina dem ci 6500i sóobare yoy, ñett yoo jël, ñaar yi alaatereete lañu.  Am na itam 250 yoy, dañ am ay laago yu metti.

MBËNN MI

Ñi loru ci mbënn mi wër dexu Senegaal ak gu Gàmbi gi tàmbali nañu leen taxawu. Jëwriñ ji ñu dénk biir réew mi, Sã Baptist Tin, moo ko xamle démb ci dibéer ji. Fekk ñu doon ko dalal ci jotaayu xibaaru RTS bu 20i waxtu. Taxawu boobu nag, moo ngi aju ci santaane yu leen Njiitu réew mi joxoon keroog ci ndaje mi ñu doon amal ci bésub 17i pani sàttumbaar 2024 ngir ñu jël matuwaay yi war ngir taxawu ñépp ñu loru ci mbënn mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj