NGOMBLAAN GI : DÉPITE YI TÀMBALI NAÑU CÀMBAR NAFA 2026 GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dépite yi tàmbali nañu càmbar nafag atu 2026 mi fa Ngomblaan ga. Ñu nar koo amal ci diiru ñaari ayu-bés ngir dalal jëwriñi Càmm gi, nattal ku ci nekk koppar yi mu namm doxalee njëwriñam ci at mi.

Démb, ci gaawu bi, 29 nowàmbar 2025, la Ngomblaan gi ubbi jataayi pénc yi ngir càmbar sémbu àtte wi aju ci njëlbeenu kopparalug atum 2026 (Projet de Loi de finances initiales pour l’année 2026). Jataay yooyu nag, dañu am solo ndax dañuy tax ñu saytu bu baax jubluwaay yi Càmm gi jël ci koom-koom gi, liggéey yi bokkeef gi gën a yittewoo ci at mees dégmal ak nees di séddalee koppar yi.

Bees sukkandikoo ci yëgle bi ñu njëkk a siiwal, dees na amal jataay yooyule lu ko dale ci gaawu démb bi, 29 nowàmbar 2025, ba keroog gaawu 13 desàmbar 2025. Muy ñaari ayu-bés yoy, mbooleem jëwriñi càmm gi dinañu teew fa Ngomblaan ga, saafonteek dépite yi ngir sàkku li ñu bëgg ñu nattal ko seen i njëwriñ.

Démb ci gaawu bi, jot nañu dalal ci jataay bu njëkk bi, ñaari jëwriñ : ju Kopparal yeek Ngurd mi ak ju Bennoog Afrig, Mbiri bitim-réew ak Saa-senegaal yu bitim-réew.

Bi 9i waxtu di jot ci suba si lañu ubbi jataay bi ci teewaayu Séex Diba, jëwriñu Kopparal yeek Ngurd mi ak naataangoom bi yor wàllu koom-koom gi, Naal ak Jëflante. Ginnaaw bi ñu gaaralee Sémb wi, càmbar ko ak i laaj-tontu, ñu ëpp ci dépite yi wote nañu ko. Ñu gis ni deppãs yi dinañu yokku ba ci 7 433,9i milyaar ci FCFA. 12 % (fukk ak ñaar ci téeméer bu nekk) yokku ci bees ko gam-gamleek yoy atum 2025. Koppar yiy dugg itam yokku nañu ba egg ci 6 188,8 milyaar. 23,4 % (lu ëpp ñaar-fukk ak ñett ci téeméer bu nekk) moo ci yokk bees ko gam-gamleek atum 2025.

Ginnaaw bi sémbuw kopparal yi jàllee, dalal nañu fa Ngomblaan ga, bi 17i waxtu di jot ci ngoon, Sëñ Séex Ñaŋ, jëwriñu bennoo Afrig, mbiri bitim-réew ak Saa-Senegaal yi nekk bitim-réew. Moom nag, nattal nañu ko lu tollu ci 64 968 948 358 FCFA. Lu tollu ci 10,8i miliyaar daldi wàññeeku ci koppar yees ko jagleel, bees ko gam-gamleek koppar yi njëwriñam amoon ci atum 2025 mi.

Donte ni jàll na, ñenn ci dépite yi jot nañu ŋàññ wàññi bi ndax li nu jàpp ni doon na yell ñu jagleel wàll woowu lu ëpp lees ko jox. Bees sukkandikoo ci caabalu ndiisoog Ngomblaan giy saytu koppar yeek ngurd mi, lees namm ci wàññi bu ni mel, mooy njëwriñ gi yamale ay naalam ci atum 2026 mi. Fas nanu itam yokkaatal ko koppar yees koy jagleel ba ci 67 580 448 358 FCFA ci at mee di ñëw.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj