ÀDDINA SAA NGI NDOKKEEL BASIIRU JOMAAY FAY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Wëliis Maki Sàll mi muy wuutu ci boppu réew mi, yeneen Njiiti réew yi ci àddina si ndokkeel nañ Basiiru Jomaay Fay mi askanuw Senegaal fal, def ko juróomeelu Njiitu réewum Senegaal. 

Aadam Baróo (Njiiti réewum Gàmbi)

“Maa ngi ndokkeel Sëñ Basiiru Jomaay Fay ngir ndam li mu am ci wote yi te di saragal askanu Bokkeefu Senegaal.”

Umar Sisoko Embaloo (Njiitu réewum Gine Bisaawo)

“Ma ngi ndokkeel bu baax Njiitu réewum Senegaal lu bees li, Sëñ Basiiru Fay, ngir ndamam lu réy li mu am ci wote yi. Maa ngi koy ñaanal moomeg jàmm, naataange ak yokkute. Maa ngi sargal itam ci bésu juddoom bi delsi.”

Patiris Talõ (Patrice Talon, Njiitu réewum Beneŋ)

“Maa ngi ndokkeel bu baax Njiitu réew Basiiru Jomaay Fay ngir pal giñ ko fal, di ñaanalaale askanu Senegaal ndam.”

Àndiriy Rajowelinaa (Andry Rajoelina, Njiitu réewum Madagaskaar) ak Mamadi Dumbuyaa (Njiitu réewum Gine Konaakiri), ñoom itam, ndokkeel nañ Basiiru Jomaay Fay ak askanuw Senegaal.

Bu dee bitim-Afrig, waa Amerig ak waa Farãs ndokkeel nañ Bassiru Jomaay Fay. 

Matiw Milëer (Matthew Miller, Ma-kàddu banqaasu Càmmug Amerig)

“Xirteg askanu Senegaal ñeel demokaraasi bokk na ci cëslaay yiy dëgëral sunu xaritoo gu sori gi ak sunuy digaale yu dëgër yi.”

Emanuwel Makrõ (Emmanuel Macron, Njiitu réewum Farãs)

Moom, dafa bind ci farãse ak ci wolof. Bees tekkee lim bind ci farãse, day joxe :

“Ndokkale Basiiru Jomaay Fay ci paloom gi niki Njiitu réewum Senegaal. Maa ngi koy ñaanal mu am ndam te di bég ci liggéey ak moom.”

Bu dee ci kàllaamay Kocc, lii la bind [nun ñoo beqi mbind mi] :

“Maa ngi ndokkeel Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ci palam Njiitu réewum Senegaal. Di ko ñaanal ndam ci sumb bi. Am mbégte lool liggéey ak moom.”

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj