AES DËGGAL NA BOPPAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waa AES (Alliance des Etats du Sahel) fasul yéene dellu ginnaaw ci génn bi mu génn CEDEAO. AES nag, ñetti réew ñoo ko séq, muy Mali, Niseer ak Burkinaa Faaso. Fan yii weesu lañu jël ndogalu génn ci kurélu CEDEAO. Waaye, kurél gi daf leen tontu woon, wax leen génn googu, teguwul ci sàrti kurél gi. Kon, ba léegi, ñoo ngi bokkandi ci kurél gi. Wànte, Asimi Goyta (Mali), Ibraayma Taraawore (Burkinaa Faaso) ak Abdurahmaan Ciyaani (Niseer) teggiwuñu seen tànk. Ci seen ndaje miñ doon amal tey fa Wagadugu te seen i jëwriñ teewal leen fa, feddali nañ génn gi ñu génn.

Màndarga yi boole ñetti réew yi séq AES bari nañ, waaye ñett ñoo nu ci gën a soxal. Bi ci jiitu mooy ne, réew mu ci nekk, ay sóobare ñoo ko jiite. Nde, dañu déjjati njiit ya moome woon, daldi foqati lenge yi ngir soppi seen nekkiini askan. Ñaareelu màndarga bi mooy, réew mu ci nekk, ay rëtalkat (terorist) dañ la song, sonal askan wa lool. Ñetteelu màndarga bi ci mujj mooy ne, ñetti réew yépp, CEDEAO lañ bokkoon laata ñu ciy génnandoo ginnaaw biñ taxawalee seen kurél gu bees gii di AES. Génn boobu ñu génn CEDEAO nag, dafa jur coow lu réy.

Dafa di CEDEAO sax nanguwul woon seen ug génn. Nde, ci li kurél gi lay, sàrtu CEDEAO mayu leen ñuy génnee noonu. Ndax, mépp réew mu bëgg a génn CEDEAO, danga war a bind kurél gi, toog xaar atum lëmm laata sa génn giy tàbbi. Waaye, Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer dañu dogu ci seen génn gi te fasuñoo cee dellu ginnaaw.

Ci alxamesu tey jii, 15 féewiryee 2024 la amoon nañ am ndaje fa Wagadugu (Burkinaa Faaso). Réew mu ci nekk, sa jëwriñu mbiri bitim-réew a la fa teewaloon. Nee ñu, « CEDEAO dafa wor sàrt bi ko sampoon ». Te, jamono yii weesu, dafa soppaliku nekkaat ag kurél guy « féewale ». Li leen ci gën a naqari mooy daan yi leen CEDEAO daan ak li ci ay doxandéem (Farãs) dugal seen loxo.

Ñoom waa AES, li ñu bëgg ci seen kurél gi mooy mu nekk kurél guy boole ak bennale, di jàppalante ak a dimbalante bu ko jaree. Waaye, bëgguñu mu nekk kurél goo xam ne day jaayaate doole ak a nappaate.

Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer joxante nañ loxo, fas yéene tabax Afrig gu bees gog, benn doxandéem du leen noot.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj