AG PAS GU YEES DIGGANTE SENEGAAL AK MÓRITANI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Réewum Senegaal ak mu Móritani yeesal nañu ag pas ci seen diggante. Muy Pas gog, dina dindi lépp lu doon gàllànkoor dem beek dikk bi ci diggante ñaari réew yi.

Démb ci àjjuma ji, 11 sulet 2025, Yànqooba Jémme (jëwriñu tabaxte yeek yaale bi ci suuf ak ci jaww ji) ak naataangoom bu réewum Móritani, Eli Uld Veyrig (jëwriñu jumtukaay yeek yaale bi) doon nañu daje fa Rooso Móritani ngir torlu ag pas ci wàllu yaale bi. Pas googu nag, dafa ñëw ak ay matuwaay yu bees ngir yeesal déggoo yi jotoon a dox ci diggante ñaari réew yi te ñu aju ci yaale bi ci suuf.

Bees sukkandikoo ci yégle bi ñu génne, déggoo bee ngi ñu torlu ci ndigalu Ilimaani jëwriñ yu ñaari réew yi, ginnaaw bi ñu njëkkee daje juróom-benni weer ci ginnaaw (12 ba 14i fan ci weeru sãwiye 2025), ngir ñu jëmmal déggoo bi ñu am ci yaale bi ci suuf ba mën a yombalal dem beek dikk bi ci diggante ñaari réew yi, moo xam ci nit ñi la, alal yi walla sarwiis yi.

Pas gi nag, bees ko doxalee, dina baax lool ci yaalekati diggante ñaari réew yi. Nde, dafay dakkal dog gi ñu daan dog sëf yi ci digg bi. Dañu leen daan ga ñuy yebbi seen sëf yi saa su ñu waraan a génn menn ci réew yi ngir jàll ca meneen ma. Mu nekkoon nag matuwaay yu ñu fa daan doxal, ñu sonaloon leen ci lool. Te coono boobu daanu ca fekk yaalekati doxandeem yi.

Ginnaaw bi ñu ko yàggee jooytu, ñaari réew yi dogu woon nañu ngir andi ciy joyyanti ak ub déggoo bu ñu njëkkoon a am ca atum 2021. Waaye mësuñu ko woon a doxal. Wile yoon nag, yeesal yi ñu ci andi dinañu jeexal jafe-jafey amalante bi foofu. Nde benn yaalekat dootul a yebbi sëfam buy dugg benn ci dëkk yi.

Ñaari jëwriñ yi ànd di woo mbooleem ñi séq dem beek dikk bi fa digg ba, (duwaan, takk-der yi, boroom xaralayi, caytug gox yi), moo xam ndawi Senegaal lañu walla ndawi Móritani, ñu ànd doxal pas gi ngir gën a dëgëral itam diggante ñaari réew yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj