Lu ëpp 12 000iy ujaaj ñoo jóge woon ci biir réew mi. Ujaaj yu njëkk yi dellusi nañu ci jàmm. Seen ub lim tollu ci 285i.
Roppalaan Airbus A330-900 Neo gi ñu tuddee Siin-Saalum a leen indi. Ba ñu wàccee, El Maalig Njaay miy jëwriñu yaale ji (dem beek dikk bi), Séex Bàmba Jéy miy njiitul AIBD ak yeneen i kilifa ñoo leen teeru, dalal leen, mastawu leen coono.
Jëwriñ ji, El Maalig Njaay, jaale na njabooti ujaaji Senegaal yi faatu ca Màkka. Limu way-dawluy aju ren baa ngi tollu ci juróom. Rax-ci-dolli, biral nay kàddu ñeel lenn ciy jafe-jafe yi am ci lootaabeg aju 2024 gi.
Xamle na sax ne, dees na amal ay njàngat ngir indi ay saafara ci jafe-jafe yi ak waajal ajug 2025 gi. Ñenn ci ujaaj yi xawoon a jagadi tamit, dinañ leen taxawu ci wàllu paj mi.