AJAA JAAL MBAAY, JAAR NA BA JÀLL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Àddina yoon la wow, ku ko xas ba dëgmal, dem rekk. Moo waral sunu maam Jaal Mbaay tàggu nu biig, 14i fani oktoobar ci atum 2025, yemoo ak guddig 23i fani rakki-gàmmu, atum 1447.

Jaal Mbaay waykat la woon, bokkoon ci ñi gënoon a ràññeeku ci réew mi. Jaar na ba jàll te rafetal lépp a ki way yu neex, gànjaru te jaar yoon lool. Bàyyi na fi ndono lu yaatu lu réew miy wéy di jariñoo ba fàww.

Xéj-na wayam wi réew mi gën a miin ci jamono jii mooy “Bete-bete”. Waaye, def na ci mbatiit lu dootul far mukk te, mboor mënu koo fàtte.

Cig pàttali, yoon wu njëkk, di it wenn yoon wi Senegaal lootaabe kuppeg CAN 1992, moom moo wayoon way wa Sëriñ Saxiir Caam bindoon te doonoon wayu joŋante ya. Mu doon ci dalal gan yi te naan leen, bu yëf yi tàmbalee, “ku mën sa moroom duma”.

Way na fi yit “jigéen yombul, fonk leen jigéen ñi” ak it weneen wu mu duppee woon “Fuural”. Ci woowule way la doon ñaax xaley réew mi naan “bu ngeen bokkee ndey, bokk baay, ànd, bañ a réeroo, moo yor jàmmi réew.” Mu teg ci ne : “Bu ñu ci boolee nangoo jàng ndax, jàng a yorum réew. Xale mooy mujjee am réew “. Ak it kàddu gii dul sàppi te askan wi jëlaatoon ko fi ca jamonoo yee weesu di : “set-setal bi ci réew mi, setal na miim réew “.

Lépp rekk di ay wax yu xóot, yu dul xewwi tey méngoo ak jamono saa su nekk. Ànd ak i sabar ak i xalam, ba mu xumb, neex lool te ëppul.

Géejawaay ga mu dëkkoon tamit dina wéet. Waaye, turam dootu fa fay. Ndaxte, barab ba ñu ko fa tuddee te daamar yi di fay faral a taxaw. Ñu koy wax “arrêt” Jaal Mbaay.

Nu ngi koy ñaanal mu dalluji ca ron garab yu mag ya ca guyaar yu gën a kawe ya. Picc ya foofu, ak seen baat yu neex ya, di ko wayal, di ko yeetal, muy nelaw ba yàndoor.

EJO ak LU DEFU WAXU ñu ngi koy jaale Senegaal gépp, rawatina njabootu boppam, waykat yi mu jamononteel ak képp ku mbatiit yitteel.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj