Ba bërki-biig rekk, gaa ña jubooguñu woon. Ñu ngi doon wéy di jokkalantey kàddu. Yenn saa, ñu def ko cig dal. Waaye, yenn saa it, mu xumb ba rëb lool. Bu ñii di waxee xel tey tànn i xalaat yu rafet, ña ca des a ngay werante ak a weerante. Ku nekk yàkkamtee sulli ñaawteef yi mu xamal moroomam, lépp ne fàŋŋ.
Ña nga làng nag ca diggu pénc ma. Fa lañu lal seen basaŋ, ne faax, uuf seen ub baraada, di xiim. Naka la xetu warga wi gilli rekk, coow li jolli. Ku nekk di jéem a yay moroomam. Noonu lañu koy jàppee saa su nekk. Ñenn ñi sax, bokk ci jotaay yu ni mel tax na ñu bari jàppee leen i boroom xam-xam. Ndax, ci seen doxalin, dafay mel ni lu bari lañu xam. Yenn saa, ñu mel ni dara umpu lenn, lépp lañu xam. Lu xew, ñu jóg taxaw, yëkkëti seen baat ya ca kaw, ne am na lu ñu ci xam. Rax-ci-dolli, di def ni ñuy tanqee seen i xibaar ci balluwaay yi gën a xóot, gën a wóor.
Wax sa xalaat la am wax ci loo xam ?
Ñaar yi ndiroo nañu de, waaye ba tay duñu benn. Ci rajo bi, am na jotaayu “Wax sa xalaat” am na yit jotaay bu tudd “Loo ci xam ?”. Kiy wax xalaatam, dafay aajar gis-gisam te, kiy wax li mu xam, dafay xelli xam-xamam.
Ku nekk mën na joxe xalaatam ci menn mbir. Waaye, taxul ba ñépp mën a maase am xam-xam ci mbir mi. Te sax, ak lu mu ci mën a doon, kiy fésal xalaatam walla xam-xamam, dafay jaadu ci moom mu sàmmonte ak i sàrt yoy képp kuy wax ci pénc, war na ci bàyyi xel.
Bi ci njëkk mooy, aji-wax ji, warul a fàtte mukk ne ci diggu pénc mi lay waxee. Bu ko ñépp déggul it, ñu baree ngi koy déglu. Te, du ñàkk am ñu teeweewul jotaay bi ba noppi wax ji fekk leen fa ñu nekk.
Ci ñi koy may nopp itam, am na ci ñu ko gën a xam fuuf li muy wax. Kon, war na leen a bàyyi xel ba du yëg boppam bay fëgg dënnam. Loolu, mën na koo musal ci làmmiñ wu tarxiis, saaraan ba faf wax jéyya.
Wax jeet, lu mu dëggu-dëggu, war na koo wodd, solal ko mbubb mu jot, fatt, te bañ a yaraax. Bu ko defee, bu nopp yi koy dégg feebaree it, ñu mën caa jàll ba àgg ca xel ma ci lu yomb te jàppandi.
War na tamit, ci ay kàddoom, moytu di ciy fay bor ak di ciy leble. Fay bor ciy kàddu mooy di tontonte ak a feyyu. Leble ci mooy di gaaruwaalee ak a tooñ. Ñaar yépp a jar a moytu cim pénc. Ndax, yu gaaw lañu ci jur aw ay ak féewale mboloo mu war a ànd, doon wenn say.
Bëggoon nu mucc ci lu ni mel taxoon na maam, ci mbaaxam, doon nu dànkafu naan : “Bu leen tooñ, bu leen feyyu. Kiy tooñ, du am jàmm mukk, kiy feyyu, du noppalu.” Te, ku xas ba ubbi benn ci bunt yooyu ci pénc mi rekk, dugal na boppam ci géew gog, dina jafe lool mu génn ci ak teeyu bakkanam.
Sunum pénc nag, nee nañu, ku nekk am na sañ-sañu wax li ko neex. Te muy dëgg ju wér. Waaye nag, pénc mi, ñépp a ko bokk, ñépp a fiy tase. Te, ku nekk, sa sañ-sañ a ngi yam fi bosu ñeneen ñi tàmbalee. Ba tax na, du lépp lees fi mën a biral. Lenn ci ay kàddu, dees leen a war a yelu. Am na lu warul a génn néeg bi ak lu warul a jéggi buntu kër gi jëm ca mbedd ma. Am naat lol, bu rombee buntu kër gi it, warul a sori bay àgg ca pénc ma. Te sax nag, nit du def lu ñiiramtal xel mi rekk mu yónnee ko làmmiñ wi. Bu làmmiñ wiy xasan, mënees na koo wokkee leneen lu dul i kàddu yu ñagas.
Bu ñépp amee sañ-sañu wax it, am na ci ñoo xam ne dañoo war a gàntu seen àq jooju. Maanaam, waruñoo wax mukk mu jëm kaw cim pénc. Te, bu ñu ko xamul walla, ñu xam ko te bañ koo nangu, waa pénc mee war a taxaw temm ne leen doo leen fi waxee. Bu ñu leen mënul a aaye loolu, ñu bañati leen a déglu, mu jeex tàkk.
Te sax, bariwuñu dara nag, ñaar doŋŋ lañu te muy ki amul xam-xam ak boroom xam-xam bi yarul boppam ci wax ci mbooloo. Ñii ñaar ñoom, lu mboolaay gi mën a def ba duñu wax ca kaw rekk, jar na ko. Ñaare, fu ñu waxee rekk loxo dar gémmiñ. Nde, bu doon ne dañuy wax seen xalaat rekk, ci njekk, xéy-na mu tane. Waaye, duñu ca yam, bu ñuy ŋaaŋ di def njombe wu rëy.
Ki amul xam-xam, bu waxee xalaatam ba ñu yëngal bopp, tàccu, ne waaw góor, mu tàmbalee xoggaliku, bëgg a sax i laaf. Def boppam boroom xam-xam, bëgg a kaalawu. Jaaree fa dugg ca mbooy ga. Wax lu waxuwul ba, yenn saa, mu àgg ci sos ngir rekk jox boppam dayo bu gën a kawe ci bëtu nit ñi.
Boroom xam-xam bi tàggatuwul ngir wax cim pénc it, bu yëkkëtee kàddoom ba yëg ne may nañu ko nopp, mu tàmbalee rax përëm ci li mu jot a ràbb. Bëgg a wone ni moo ëpp xam-xam ñépp. Di ubbi ay bunt yoy, donte ne dëgg a fa nekk, seen ug ubbeeku amalul askan wi lenn njariñ, lu dul di jaxase xelu ñenn ñi ak a gëlëmloo ña ca des.
Pénc mu nekk, ña ko dëkkee ñoo ko war a wattu. Ba tax na, farata la ci ku nekk mu bàyyi xel kàddu ya fay jib ak ñi leen di yëkkëti. Am na ñu jar a déglu lool ndax solos xalaat yi ñuy sotti ak anam yi ñu koy defee. Waaye, am na ñoo xam ne, bu ñu noppee lañu ëppal njariñ askin wi ci bu seen i kàddu jógee. Kon, bu ko jaree sax fay leen war na ngir ñu toog, déglu te ne cell. Ndax kat, wax, soxu fetal la, su rëccee rekk, dabu ko wees.