AM-AMU NJIITU RÉEW MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndajem Ndeyu Sàrtu réew mi siiwal na am-amu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Muy jéego bu am solo ñeel coppite gog, moom la njiit yu bees yiy woote ñeel yoriinu réew mi. Bees ko xaymaa nag, am-amu Njiitu réew maa ngi tollu ci ñaar-fukk ak ñetti tamndaret (23i miliyoŋ) ci sunuy koppar.

Démb ci altine ji, 29 sulet 2024, lees ko siiwal. Bu dee ci wàllu koppar, 23i tamndareti CFA la Njiitu réew mi am. Ci ñaari bànk yii di BICIS (14,7 miliyoŋ) ak UBA (7,4 miliyoŋ) la denc xaalisam. Mi ngeek kër guy jar téeméeri tamndaret ak juróom-ñett-fukk (180i miliyoŋ). Kër gaa ngi nekke Mermoos. Pàkk ba mu ko tabax nag, sàndikaa « inspecteurs des impôts et domaines » moo ko ko jagleeloon.  Rax-ci-dolli, am nay tool yuy jar ay miliyoŋ.

Bees sukkandikoo ci lees siiwal, Njiitu réew mi am nay tool. Benn baa ngi tollu ci 4i ektaar. 15i miliyoŋ la ko dikkee te def na 29i miliyoŋ. Am na yit yeneen ñaar yu nekk Cees. Benn biy jar 3i miliyoŋ, beneen biy jar 1,7i miliyoŋ. Daamar bi mu moomal boppam mi ngi jar 19i miliyoŋ.

Bu dee payooru Njiitu réew mi, weer wu dee, Njiitu réew mi dina fayeeku 4,8i miliyoŋ. Waaye, ameel na bànk yi bor bu tollu ci 6,4i miliyoŋ.

Siiwal bi Njiitu réew mi siiwal tolluwaayu alalam ji dafa bokk ci jub, jubal ak jubbanti bi muy woote. Looloo waral mu siiwal tolluwaayu alalam ci saabalukaayu Càmm gi (journal officiel) bu 30 sulet 2024.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj