ANIBAAL JIIM PELENT NA AADAMA FAAL MU BENNOO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ab bataaxal la Anibaal Jiim mi ci kaso bi biral, di ci xamle ne dina pelent kii di Aadama Faal mi bokk ci lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar.

Li sabab mbir mee di ne, Aadama Faal moomee, dafa toog cib jotaayu tele, tuumaal Anibaal Jiim ñeel koppaar yooyee ñuy wax ne Qataar la jóge. Ciy waxi ngóor si Faal, Anibaal Jiim a jiite lépp. Maanaam daal, moo nekk ci bopp biy doxal ak a saytu xaalisu naar yees wax ne dañ ko xëpp waa tuubaa ngir ñu jàppale Usmaan Sonko. Kàddu yooyile ñoo naqadi Anibaal Jiim, mu ne du leen naane ndox. Moo ko tax a wax ne, ci biir bataaxal bi :

« […] Mbokki réew mi, xamleen ne coowal koppari Qataar du lenn lu dul am penantal (dilatoire, diversion) ngir ngeen bañ a jublu ci li am solo. Bu dee sama wàll bopp, dinaa pelent Sëñ Aadama Faal ak ñi ma sosal ñépp ngir ñu mën a indiy firnde ci tuuma yi ñu ma gàll… »

Noo ko déggandoo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj