BÀJJEN ARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

La Kocc jàngale woon nga feeñal ci talaata jii

« Mag mat naa bàyyi cim réew »

Teey, yéwén, ràññee, dogu nga nu won

Lii bokk na ci mbindu bés bi

Sa kàddu gu njëkk moo ma yéem

Ku doon séenu nga ñaxtu ci làmmiñi réew mi

Jooytu ci cër bi ñu ko xañ

Am na mbetteel

Ci sag tàmbali Buur-Yàlla nga jiital

Nangul ko dogalam

Xàndoor damm ca waar wa

Nga ñaanal jàmbaar ja dëddu

Seedeel Abdu Salaam Faal

Ne bay na waaraam ci toolu mbatiit bi

Boole ci rafetal ak fonk doomu-Aadama

Yow mii yaa xam àddina

La ca tegu di dalal jëwriñu mbatiit ak ña mu àndal

Ràññee yóbbantey Président

Nga rafetlu cargal gi ak teraanga

Ba dige ni dinga yónnee sa xalaat ñeel njariñu réew mi

Rawatina làmmiñi réew mi

Laajoo benn wareef

Te moone yaa ngi ci sa warugar ba mu mat sëkk

Yaay gor, yaa yiw

Yaram wu sutante tàggalewu la ak sa sago

Ñépp a lay sagoo

Tey nga gën a woddati say kàddu

Sa kersa yéem na ma, Faal

Moo ma tax di sàkku ci Boroom Bi

Mu yàggal la fi lool boole ci wér ak wérle

Ndax sa dund am na njariñ

Jërëjëf, Faal, xol bu sedd doy na ñaan…

Ibraayma LÓO, Directeur du livre et de la promotion de la lecture

Ibraayma Lóo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj