Bàyyi nañ Biram Suley Jóob. Layookatam bi, Meetar Musaa Saar a ko xamle. Moom, Biram Suley Jóob mu Pastef, dafa yékkati woon ay kàddu jëmale leen ci Njiitu réew mi. Jéggalu woon na gaa, waaye jotoon nañ ko jàpp ba yóbbu ko kasob Sebikotaan ba. Tey ci àllarba ji lañ ko bàyyi.
Ginnaaw bi ñu bàyyee Biram Suley Jóob, teg nañ ci El Maalig Njaay. Moom itam, tey lañ ko bàyyeendi ginnaaw biñ ko jàppee ci sababu ndéggat lees ko askanale. Lees ko tuumaaloon mooy wooteb fippu tasug xibaar yu wéradi.