BIRAM SULEY JÓOB MA NGA WOON KÉEDUGU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëwriñu laf gi, soroj beek mbéll yi, Biram Suley Jóob, ma nga woon fa Kéedugu, doon fa amal tukkib nemmeeku fa barab ya ñuy gasee wurus wi. Barki-démb, ci dibéer ji la fa demoon, àndoon ak naataangoom yii di Daawda Ngom (jëwriñu kéewnga geek coppiteg mbindaare mi), Séex Tiijaan Jéey (jëwriñu ndox meek cellal gi) ak Yanqooba Jémme (jëwriñu liggéey bi, xëy meek jëflantey campeef yi). Diggante barki-dém ak démb, wër nañ barab yii di Musalaa, Makko ak Sabodolaa. Yépp diy barab yu ñuy defaree wurus. Nemmeekuji woon nañ tamit askan yi ci dëkk yi ñu leen sancal ginnaaw bi ñu leen jëlee fa barabi mbéll ya.

Moom, jëwriñu laf gi, soroj beek mbéll yi, àrtu na àntarpiriis yiy liggéey ci mbéll yi. xamal na leen ne, léegi, dañuy sàmmonte ak li yoon sàrtal ñeel seen fànn woowii. Lu ko moy, ay daan mën nañ leen ci fekk. Maanaam daal, jub, jubal ak jubbanti moo xew.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj