BÓOMUG ABDU ASIIS BA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jéyya ju ñaaw ja ca Pikin Teknopóol mi ngi wéy di jur coow fi réew mi. Ci talaatay bërki-démb ji lees siiwal xibaar bu tiis bile. Abdu Asiis Ba, gën a siiwe ci turu « Asiis Dabalaa », lañu rey, moom ak jarbaatam bu tolloon ci 17i at. Moom nag, fecckat la woon, doon yënguwaale ci mbirum kilib « théâtre ». Mbir yaa nga xewee Pikin Teknopóol ci benn apaartamaa.

Bees sukkandikoo ci waa Sene.news, ñenn ci seen i dëkkandoo wax nañ ne, ci gaawu bi, bi muy taw ci suba si lañ déggoon ay yuuxu. Waaye, du lii lañu foogoon. Muy tekki ne, ñoom ñàkk nañ seen bakkan luy mat 3 ba 4i fan laata nit ñi di ko yég.

Li luññutu gi xamleegum, bees sukkandikoo ci L’Observateur mooy ne benn néew bi di jarbaatu Asiis ci sanguwaay bi lañ ko fekk, ci anam yu jéggi dayo. Néewu Asiis bi moom, cib darab lañ ko sàng bàyyi ko ci saal bi. Xamle nañ tamit ne Asiis dañu ko rendi, jarbaat bi ñu jamate ko ci biir ba butit ya xaw a génn

Li tax xelu luññutukat yi jàpp ne dañu leen rey, bokk na ci buntu apaartamaa bi ñu tëje ci biti. Rax-ci-dolli, am na ci néeg bu caabeem doon lang ci bunt bi. Lu ni mel a tax ñu ubbi ab lànket ngir luñutu mbir mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj