Li nit ñi doon xel ñaar ak a laam-laame, leer na ! raglu Le Dantec tëj na ci bésub 15 ut bii nu génn. Boob ba léegi, coow li a ngi ne kur ci biir réew mi. Ku ci sa xel dem rekk, samp nga ab laaj bu la gën a yitteel ci mbir mi, nde li naalu defaraat raglu bi ëmb a bari.
Bokk na ci laaj yi gën a fés : Lu tax Càmm gi war a jaay 3i ektaar yi ngir tabax ? Naka la way-tawat yi di def ak seen i mettit ? Liggéeykat yépp ya nekkoon ca biir raglu ba fan lañ jëm ? Ndax Càmm gi biral na leen ne duñu ñàkk seen xëy ak lu mënti xew ?
Ku nekk di ŋàññ ni Càmm gi di patam-patamee tabaxaatub raglu Le Dantec bi, ndax dara dafa leerul ci bopp saa-senegal yi, lépp a jaxasoo. Doonte ne jawriñu paj mi, génne woon na ay yégle lim ciy béréb yiy dalal liggéeykat yi ak naka lañ nar a toppatowee way-tawat yi ba lépp jaar ci yoon. Yemul ci loolu, moom Mari Xemes Ngom Njaay, demoon na doxantu ci yénn ci béréb yiy dalal liggéeykat yi ak way-tawat yi nekkoon ci raglu Le Dantec bi. Mu ngi xamle ne lépp li ko war mi ngi koy def, teg ci ne :
« Dunu ay dëmm bay seetaan way-tawat yi ak seen i mettit, naan danu leen sànni. Ay doomi Senegaal dëgg lanu, te loolu su amoon sax, yaakaar naa ne yeen ñii ñépp, ak ni ma xame saa-senegaal, du seetaan lu ni mel, dangeen leen di fat seen i biir kër bala kenn di nekk naan daf leen di filme. Loolu nun waat nan ko ne dunu seetaan benn aji-tawat muy tumuraanke. Li ëpp solo nekkul fu way-tawat yi jëm, ndax noo ngi leen di faj te su fekkee dama leen di aj ci kaw garab gi faj leen, dinan leen faj, ndax mooy li am solo te mooy sama wareef. »
Waaye, coow li coow li mooy, limu néew bu bari bi ñu dencoon ci biir raglu Le Dantec bi te kenn xamul seen i mbokk. Nekkoon nañ ci lu toll ci juróom-fukki néew ak lu tegal ci biir dencuwaayu néew bu Aristide Le Dantec. 30i ay liir lañ ak i lumb, ña ca des di ay mag, am na ci sax ay doxandéem. Lu ni mel jéggi na dayo, te it doon lu yéeme. Kenn xamul lu waral lii. Naka la sa mbokk di génne àddina, nga wacc ko ci raglu ba mu gaañoo dem sa yoon ne doo ko toppatoo ? Xanaa boobu néew amul ay mbokk ? Walla daa am luy ñuul ci soow mi lu raglu yi nanguwul wax ?
Ndeke Dantec rekk a siiwle. Nde, lii yàgg na am ci biir raglu yi ci biir réew mi te ba léegi amul lu ci soppeeku. Luy ñuul ci soow mi du lenn lu dul xaalis bi raglu yi di laaj ki deele su bëggee jot ci néewam. Waaw, loolu ndax yoon la ? Ci ban sàrt la raglu yi teg ne ku dee rekk mbokk yee war a ñuqi seen i poos fey soog di jot ci néew bi ? Ki fey lalu raglu bi, jënd ay garab ba deseetul dara, naqar ganesi ko, mu ñàkk mbokkam nu tegal ko ci ne fàww mu feyaat ngir mu mën a jot ci néewam. Bu amul xaalis biñ ko laaj nag ? Man réew lan nekk ? Ndax Càmm gi yëg na liy xew ci biir raglu yi ?
Ciy leeral, njiitalu dencuwaayu néew bu Dantec bii di Masoor Ba nee na :
“29i liir yi tàmbale woon a yàkku ci biir raglu bi lañ juddoo. Moone seen i way-jur jot nañ këyit yiy wane ne gaañu nañ, waaye kenn ñëwul jëlsi leen. Am na tamit waa sàppëer pómpiye, yeneen 8i lumb ak i liir yu ñu fore ci mbedd yi indi leen ci biir raglu bi.”
Ci dibéerub 21 ut la benn kurél gu tudd Perfection et la miséricorde taxawu néew ya nekkoon ca raglu Dantec bi, jébbal leen seen boroom ci sëg yi nekk Yoof. Di leen ñaanal boroom bi yërëm leen.