Xibaar bu doy waar moo bawoo fa Gine Bisaawo. Nguurug Umaro Sisoko Embalo la ay sóobare daaneel. Njiitu réew ma ci boppam, Sëñ Embalo, moo ko xamal waa Jeune Afrique.
Déjjati nañu Umaro Sisoko Embalo, Njiitu réewum Gine Bisaawo. Moone de, ci dibéeru barkaatu-démb ji rekk lañu fa amal i wote ngir tànn ka ko war a wuutu ca boppu réew ma. Ca njureef ya fa jotoon a rot sax, nee ñu Fernando Dias da Costa moo jiitoogum woon. Waaye, moom Umaro Sisoko Embalo ci boppam, dafa waxoon ne moo faluwaat. Bi ñu xëyee tay, ci àllarba ji, lañu yëg ne am na ay sóobare yu song njénde* la, foqati nguur ga ca loxoy Sëñ Embalo.
Umar Sisoko Embalo ci boppam moo yégal waa Jeune Afrique ne, ci àllarbay tay ji, 26 nowàmbar 2025, bi 12i waxtu di jot, la ko ay sóobare yu fétteerlu fekk ca pekkam*, jàpp ko. Jàppaale nañu yit kilifa gu kaweg xare yi*, seneraal Biyag Na Ntan, tof kilifa gu kaweg xare yi*, seneraal Mamadu Ture, ak jëwriñu biir réew ma, Botse Kànde.
Fi mu nekk nii nag, sóobare yi génne nañu ab yégle, di ci xamle ne ñoo téyandi lengey réew mi te ajandi nañu lépp lu jëm ci wote ya ñu fa amaloon.

