Démb, ci dibéer ji, 14 sulet 2024, la woon finaal Euro 2024 bi doon ame fële ca Almaañ. Po mi nag, Espaañ moo ko mujje gañe 2-1 ci kanamu Àngalteer. Mu nekkoon finaal bu neex, bu jaar yoon. Espaañ nag, yeyoo na ndamam li. Ndax, yoon wu rafet wim ci def. Dafa gañe matsam yépp.
N. Williams (47eel) ak M. Oyarzabal (86eel) (Espaañ) ak C. Palmer (73eel) ñooy ñi dugal ci finaal bi.
Ñii lees ràññe ci po mi :
– Rodri, futbalkat bi ci gën a xereñ.
– Lamin Yamal, ndaw li gën a xereñ.
– D. Olmo di ki ëpp lim dugal (3) yamoo ko.
– J. Pickford lees tabb góol bi ci gën a xereñ
– L. De la Fuente di tàggatkat bi gën a xereñ ci po mi.
COPA AMERICA 2024
Finaalu po mii itam mu doon am ci 00 waxtu ci altiney tey ji. Dañ ko mujje woon a randal ba ca 1i waxtu wa sax. Ndax, dafa amoon ak yëngu-yëngu yu amoon ca fowu ba. Waaye, yépp mujje na jaar yoon.
Kii di Àrsàntin moo ko mujje gañe, di waada Amerig. 1-0 la dóor Kolombi ca 112eelu simili ba. Lautaro Martinez moo dugal bii ba. Mu nekkoon nag mats bu neex. Kolombi futbal ci lu rëy. Waaye, Àrsàntin magu ko ca mujjantal ga.
Ñii lees ràññee ci po mi :
– J. Rodrigez futbalkat bi ci gën a xereñ.
– L. Martinez, dugalkat bi gën a xereñ (5 bii)
– J. Rodriguez nekkaat ci ki ëpp lim paas ñu dugal (6)
– E. Martinez, góol bi gën a xereñ.