FEGGUG PAJ ÑEEL 7. 000i NDAWI NAALUB « XËYUB NDAW ÑI »

Yeneen i xët

Aji bind ji

7000i ndaw yi bokk ci naal bees dippe « Xeyu Ndaw Yi » [Xëyu Ndaw Ñi] lees jagleel feggug paj (couverture sanitaire).  ASERGMV (Agence sénégalaise de la reforestation et de la Grande muraille verte) ak ANCMU (Agence nationale de la couverture maladie universelle) ñoo xaatim ab déggoo bu ni mel ci bésub alxamesu démb ji, 1 fan ci desàmbar 2022.

Aamdu Lamin Gise miy tof-njiitu njëwriñu Kéew gi, yokkute gu sax gi ak coppiteg mbindaare mi moo jiite woon ndaje ma ñu xaatimee déggoo bi. Sàndi na ciy kàddu, wax ne :

« Jubluwaayu déggoo bi mooy jagleel 7. 000i ndaw yi bokk ci naalub Xeyu Ndaw Yi [Xëyu Ndaw Ñi] feggug paj. Dees na ko jaare ko ci tëralinuw jàppalante te wéer ko ci warlaayu wér-gi-yaram (assurance maladie) gi leen di tax a mën a faju bu baax ci njëg lu woyof niki nit ñi am kiirteefug dund (sécurité sociale). »

 

Aamadu Lamin Gise dafa jàpp ne ndaw ñu jàmbaare yile yelloo nañ ko. Nde, ñoom ñooy sóobu naaj wu tàng wi bés bu set, ak béréb yi naqaree dund yi. Waaye, Omar Abdulaay Balde naqarlu na te rëccu li 5 ba 6 ci seen i liggéeykat ñàkk seen bakkan ci waar wi.

« … Danu aksidànte ci talib Ilaa-Tuubaa bi, 5i liggéeykat jële ciy gaañu-gaañu. Maatam, deele nanu fa ndaw lu feebaroon ; Fatig nu deele fa Abdu Seen mi feebaroon tamit. Bi nuy kàmpaañ, aksidànte nanu ba ñaar ci sunuy liggéeykati ñàkke ci seen i bakkan, muy Keebaa ak Sofi yi doon amal seen liggéey. Ca tàmbaa moom, ki fa gaañu, jaan a ko màtt. »

Dee moom, kenn amu cim paj. Waaye, mënees na lal i pexe ba ku feebar ñu mën la faj. Looloo sabab taxawaayu kilifay meññalkat yi. Bookar Ba mi jiite Kërug réeweg warlaayu wér-gi-yaram gi nee, jubluwaayu kër gi mu jiite mooy fexe baa saa-senegaal bu nekk mën a faju ci anam bu yomb, te du ko gaañ ci poosam. Bu dee 7. 000i ndaw ñees jagleel déggoo bi, lees ko dugge mooy, ciy waxam, « …bu ñu feebaree walla ñu amey gaañu-gaañu ci seen liggéey walla ay feebari toropikaal yees sàgganee, ñu mën leen a faj. »

  1. 000i ndaw ñi, ku ci feebar, daanaka paj mi du la dikkee dara. Bu dee jàngoro ju ndaw la, bu demee ci fajuwaay yu ndaw-ndawaan yi, dinañ ko faj. Bu dee feebar bu metti, mën nañu dem ci raglu yi. Te, bu paj mi jaree 100i dërëm, 20i dërëm lañuy fey. Loolu, ag yombal la ñeel ndaw ñooñii toppatoo kéew gi.

 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj