GENN GAAL, ÑAARI JULLI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tabaski ren ji, waneeti na xàjj-ak-seen biy màndargaal réewum Senegaal ak tolof-tolof yu metti yi askan wiy jànkoonteel. Ci benn boor, wute am na ci bésub julli gi. Ñii ci dibéer ji lañu julli, ñee julli ci altine ji. Waaye de, bésub Arafaat bi moom, di juróom-ñeenteelu fan ci weeru Tabaski, kenn wutewu ci, bésub gaawu bi la woon,. Te ñépp a ko taxawe : ña aji, ña nga woon ca tangooru Arafaat, béréb bu sell ba ; ñi ajiwul woor bés bi ngir jëmmal màggaay bi ak taataan ngëneel yi mu làmboo. Bu dee wér na ni tabaskee ngi war a am ci fukkeelu fan ci weeru tabaski, kon saa buñ taxawalee bésub Arafaat, warees na julli ca ëllëg sa. Noonu la ko àddina sépp jàppe ba mu des waa Senegaal. Jamono ju nekk, fàww ku nekk wane ne kër diw la bokk, ci ndigalu diw lay wéye. Maanaam, naanu yee bare ci miim réew.  Ñu ne Senegaal menn réew la, wenn askan, benn bopp, am benn jëmu. Waaye, wax jooju de, safaanoo na lool ak li ñuy faral di gis. Waxuñu sax féewaloo biy màndargaal askan wi, waaye at mu nekk, ñu gis fi ñaari korite, ñaari tabaski. Li ci doy waar, nag, mooy ne, mësuñoo gis ñaari Arafaat walla ñaari tamxarit. Kon lu tax ñuy wuute ci tabaski ak korite te at mi di menn at kese ? Walla dafa am lu ci rax ? Laaj baa ngi noonu sampu, ku ci am tontu na wax…

Ci beneen boor, tabaski bi dafa woneeti metit yi askan wiy jànkoonteel. Jamono jii, lépp a yokku te xaalis amul. Simoŋ bi yokku na, ceeb bi yokku. Esãs ak gaasuwaal yokku, njëgu tukki bi yokku. Ñi war a tukki ngir bes bi sonn lool, liñ liggéey yépp nar a yem ci paas. Soble yokku, pombiteer yokku. Boroom kër yi jaaxle. Ñu ne déet-a-waay, ñàkkum xar mi ci réew mi ñëw doggali boroom kër yi. Ndege, jaaykat yi dañu aj njëg li fu kowee-kowe, xar jafe lool sax. Ba ci bésu tabaski bi, ci fajar gi, am nay boroom kër yu amagul woon xar. Ndeysaan, ñenn ñi daanaka ay mbote rekk lañu mujje am, dugal ci xaalis bu bare, tollu ci diggante 80 000 ak 125 000 CFA ; ñeneen ñi béy lañu mujje am, tabaskee ko. Te ñàkkul mu am ñu reyul faf. Dëgg-dëgg, réew mee maki, ni ko ndaw yiy waxe. Dara doxul, te ku ŋaaŋ ñu tëj la. Ñu ne Maki makiye na réew mi ba makiil ko. Te wolof dafa ne, ku makiyaasu walla ñu makiyaas la, boo ñaqee ñaaw. Moo taxit, waa réew mi  wax nañoo wax, ñaxtoo ñaxtu, wër a wër bay ñaq tooy xepp. Wax dëgg, ni réew miy doxe ñaaw na, li askan wiy dund tamit jéexal na xol. Lépp a caŋ, rawati-na mbay mi ak càmm gi. Waa kow ga ñoo gënatee sonn ndax suuf si wow na, gàncax amul, jur gaa ngiy dee. Nawetu ren ji, bu dee mënees na ko tudde nawet, dafa dëddu réew mi. Mu mel ni asamaan si dafa mere askan wi, niir yi gàddaay, ndox mi bañ a wàcc. 

Laago yii yépp dajaloo ci jenn jamonoo tax tabaski ren ji metti. Askan waa ngiy jooy, di sàkku ndimmal ci neen. Wànte, li gën a metti ci xoli nit ñi, mooy li njiitu réew mi génn keroog wax ne, li nguuram jënd ciy oto dafa bare, daanaka xaalis biñ jënde ay oto diggante 2012 ak léegi mat na 307i miliyaar ci sunu koppar. 

Loolu di firndéel yàq, yaataayumbe ak gundaandaat gi waa nnguur gi nekke. Waaye, Maki waxunu lépp. Ndaxte, oto yooyu, esãs walla gaasuwaal moo leen di dawal te loolu yit, ci nafa réew mi lañu ko feye. Kon xaalis bi ñu pasar-pasare ëpp na fuuf li mu wax. Nuy laaj, diggante 2012 ba tey jii, kan moo nekkoon Njiitu-réew mi ku dul moom ? Du moo fi dige woon ne yàq bi dina deñ ba mu set wecc, wax ne xaalis bi dina ko delloo ci askan wi ko jagoo ? Waaw, fu Maki nekkoon bi nguur giy jënd oto yooyu ak esãs walla gaasuwaal yi leen di dawal ? Fàtte da fee xajul sax. Keroog, ca dëju ndem-si-Yàlla Usmaan Tanoor Jeŋ, oto limusin bu ñuul bi yaboon Maki ak naataangoom bu Mali te mu lakkoon, 1 miliyaar CFA la jar ! Ca ëllëg sa, mu waraat beneen oto limusin bu doomu-taal buy jar njëg lu tollu noonu walla mu ëpp ko. Ndax daa fàtte boppam ? Kon, lu jiin Njaag a, te Maki mooy Njaag.  Te, am réew, su fa buur ak lingeer dee fecc, ku fay woyaan doo rus a yaŋas.  

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj