Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dem na tay ci gaawu bi, 21 suwe, fa Abuja (réewum Niseeriyaa), ngir teeweji 76eelu lëlub Njiiti réew yeek Càmm yu Kurélug CEDEAO.
Tay ci suba la fi Njiitu réew mi bawoo utali Abujaa, ngir teeweji, ëllëg ci dibéer ji, 22 suwe 2025, 67eelu lël bi Njiiti réew yu Kurélug CEDEAO ak Njiitul Càmm yi ko séq. Muy Ndaje mom, Kilifay réewi Afrig Sowu-jànt yi dinañu ci waxtaane lépp lees war a taxawe ci diiwaan bi, dëggal seen pasteef ngir tabax kurél gu dal gog, réew yi dinañu jàppalante te taxaw ci seen i bëgg-bëggi askan.
Ndajem ren ji nag, dafa fekk diiwaan bi nekk ci tolluwaay bu yéeme. Ñu gën cee ràññe ay jafe-jafey pólitig ci yenn réew yu ñu taf, yu dummóoyu kurél gi, ay jafe-jafe yu aju ci kaaraange gi ba ci koom-koom beek laf gi. Dafa daje itam ak ndaje mi njiit yi jëkk a amal ginnaaw bi ñu màggalee bu yàggul dara ( 28 me 2025) 50i ati kurél gi.
Bokk na itam ci lu ñuy xaar ci ndajem ren ji, ñu andi ay coppite yu xóot ci lootaabe gi. Nde, bees sukkandikoo ci li Sëñ Gilles Yabi (Njiitul think tank WATHI) biral, dina jaadu ci kurél gi mu def taxaw-seetlu ci 50i atam yi mu màggal ren. Nde, bi mu sosoo ak tay, bari na jéego yu mu séqi, waaye bari na lees mën a duut baaraam. Lu ni mel nag, tax na ba way-bokk yépp fésal seen ànd ci ni warees na a amal i coppite ak di fésal seen i bëgg-bëgg ñeel coppite yu xóot.
Ba keroog ba ñuy màggal 50i at yi, fa Legos, kàddu ya fa jiboon fàttali nañu ni jot na ñu càmbar li kurél gi jot a liggéey, xalaat yoon yu yees yu mu war a tegu, ak waajal a dékku yees-yees yi jamono andi.
Kon ci 50i at yi kurél gi am, warees na cee gaawantu ngir amal bilaŋ bu xóot. Bu ko defee ñu mën a teg baaraam ci yees war a joyyanti ngir, bu ñu ci jógee, ñu mën a jublu ci at yii di ñëw. Ci lileet, war nañu cee bàyyi xel yëngu-yëngu yi jot a am ci at yi weesu ba kurél gi xawoon cee lott.