Keroog ci talaata ji lees tàmbali ñaareelu bëccëgu joŋantey bokkadil CAN 2023. Ikibu Senegaal bi doon ci jàmmaarlook ikibu Ruwàndaa bi ko doon dalale ci Estaad Meetar Abdulaay Wàdd bu Jamñaajo. Mu doonoon joŋante bu metti te wuuteek bu gaawu, bañ dumawee Beneŋ 3i bii ci benn. Bi joŋante bi di waaj a jeex la kii di Saajo Maane, goneg Bàmbaali gi, dugal penaatii. Senegaal gàddu ndam li. Ñuy ñaari joŋante yu tegaloo yuy fàttali fi ikibu Senegaal bi tollu ci làngug futbal gi ak lees di xaar ci moom.
Ñetti weer ci ginnaaw la Senegaal doonoon sàmpiyoŋu Afrig 2021. Mu sóobooti xaat ci joñante bi. Mboolem réewi Afrig yi, ku ci nekk bëgg koo wuutu, te Senegaal ci boppam war koo mën a jëlaat. Lii tax na ba saa buy joŋante, way-faram (supporters) yi di xaar ndam ak a yaakaar mu doon ndam lu réy. Bokk na ci li ko waral, futbalkat yi ikib bi dajale dañoo siiw lool te am i tur. Daanaka ñu ci ëpp, ci sàmpiyonaa yi ëpp doole ci àddina si lañuy futbal. Loolu tax na ba buñ ndulliwul ki ñuy jàmmaarlool boole ci futbal bu rafet, du neex way-faram yi, walla sax am ñu leen di gàkkal.
Rax-ci-dolli, du way-fari Senegaal yi rekk ñooy xaar foofu ikib bi. Dem na ba tàggatkatu gaynde yi walla ñi koy gunge loolu dafa ub seeniy bopp. Loolu dees na ko dégge ci kàddu yi Elaas Juuf yékkati ci ñaari ndam yii ñu tegale : “ ñaari joŋante, ñaari ndam mooy lu jaar yoon. Ndaxte, Senegaal ñépp a ko teg i bët tey jii ci CAN bi. Kon dañoo war a dawal ni ñi mën ci Afrig, niki sàmpiyõwiy Afrig.” Mu mel ni yeneen réew yi xam nañ loolu te nangu ko ngir gën a mën a yokk seen waajtaay. Bees nangoo kàddu yi bawoo ci Karlos Alos, tàggatkatu ikibu Ruwàndaa, Senegaal “bokk na ci fukki ikib yi gën a baax ci àddina si”.
Tege yii tax nañ ba gaynde Senegaal yi xam ni seenub benn joŋante dootul a yomb. Te itam loolu feeñ na bu baax ci seen xar-kanam. Bu nu sukkandikoo ci Kàdduy Séexu Kuyaate, dinañ gis ni guney Aliyu Siise yi ñi ngi wéy di mottaliku ci anam yu bare : “ léegi ikib bun dajeel dafay metti. Nun nooy sàmpiyõ Afrig. Te sàmpiyõ Afrig, jàmmarloowam yépp gañ-jël (finale) la… Boo xoolee joŋante bi, bun ko amaloon ñaar ba ñetti at ci ginnaaw doon nan ci témboo walla sax nu ñàkk ko”. Lii nag mooy yaa fi mën, bu dee ndam it, sas la wu réy. Ndax ku ñépp di xaar nga war a mëne fu nekk. Mu mel ni xam giñ xam fiñ leen xaare, baax na ci Saajo Maane ak i ñoñam. Jural na leen làmbook mat gu leen di tax a bëcciku (se décharger) ak a xam nees war a amee ndam saa su nekk ak lum jafe-jafe.