Fan yii weesu, njiitu réew, Maki Sàll, fekki woon na Putin ca Riisi ngir, nee ñu, ñu waxtaane bekkoor bi xare bi xew digganteem ak Ikren jural àddina si, rawatina réewi Afrig yi. Ndax kat, Maki Sàll dafa jàpp ne xare bu ni mel, baaxul ci réew yu néew doole ni réewi Afrig yi. Nde, réew yooyii, ngën-ji bari li ñuy dunde, dañu koy jéggaani bitim-réew. Te, muy Riisi, di Ikren, dañu bokk ci réew yi teg loxo dundeef yu mel ni ceeb, mbokk, farin añs. Jamono jii, nag, xare bi dafa gàllankoor yaxantug àddina si ak yóbbaliy dundeef yooyee. Kon nag, bu xare bi dakkul, koom-koom yi dinañu nasax, xiif gu metti dina am fii ak i weer.
Looloo tax ñu bari def taxaw seetlu ci mbir mi. Ndege, Afrig ñàkkul bay tàllal loxo, di jéggaani ndimbal ak dund ngir askanam. Wax-dëgg, nag, Afrig soxlaalul kenn ndax li fi nekk ciy balli bindaare, géej yi ko wër, naaj wi ko tiim ak asamaan su nangu sii, nga teg ci ndaw yi fi ne gàññ, toll ci seen digg doole… Nee nañu mbas meek xare bi xew tey diggante Riisi ak Ikren ñoo tax koom-koomu réewi Afrig yi gën a suux. Mën na nekk. waaye, ndax ci loolu rekk lees ko war a delloo ? Déedéet. Bu dee loolu itam, dafa fekk ñu jël seen i yoonu yokkute tënk ko ci ñeneen. Loolu bokk na ci li tax seen i koom-koom mënuñu suqaliku boobaak léegi. Réew yépp tey, seen i bëgg-bëgg bopp a leen yitteel, du leneen. Ñoo wax dëgg sax ! Wolof nee, mag moom, bu naanee ndox mu, tàng suukër saa tax. Réew yi duñ ànd ak ku leen amalul njariñ. Kon nag njiitu réew lu fi teg yaakaram ci keneen ngir suqali koom-koomu réewam dina yàgg féey ci géej gu amul ndox.
Moo tax, boo seetee ba ci biir, mbooleem li askan wiy jooy tey, ci yokkute geek yeneen yu ni deme, benn xare waralu ko ! Bu dee Senegaal, ay tamñareet (Miliyaar) lañuy yàq ci lu ko jarul, ba pare dëkk ci nger gu mettee metti. Ay dipite ak ay jëwriñ yuy sàcc te dara du leen ci fekk. Bu dund gi yokkoo kon kan a ? Njureef yi de, dañuy wane ni njiitu càmm gi di suuxale koom-koomu réew mi.
Ci taxaw seetlu yi, am na ñu naan bi Senegaal di tëj digam ak bu Mali yàggul dara. Te umpul kenn ni digu Senegaal-Mali, ci benn at doŋŋ, ay tamñareet la ci Senegaal daan jële. Maki Sàll ak waa CEDEAO jékki saa rekk jël ay ndogal, ub dig yi. Li Senegaal di ñàkk ci bile tëj moo ëpp fuuf xare bi ñépp di wax. Maki daal, mu ngi soofantal koom-koomu réew mi. Bëgg a jiital bëgg-bëgg farãse yi rekk a waral coonoy way-dëkk yi. Ku ànd ak nguur gi mën nga sàcc, di njegenaayoo xaalisu réew mi. Néew-ji-doole yi ñooy yëg yokkute dund gi, ñoom lañuy sonal te ñoom lañuy tegal lu tar saa su nekk.
Bekkoor (crise économique) gi yenn réewi Afrig yiy dund nag, ñu koy jaarale (tànqoo) ci xareb Riisi ak Ikren, ay fontu kese la. Beykat yaa ngi fii, ku leen tegoon ci ay anam yu baax kon déy benn Saa-Afrig du ñàkk lu muy lekk. Na njiit yi bàyyi tappale bi te liggéeyal réew yi. Loolooy dëgg.
Ñàkk kersa gi njiit yi àndal dafa jéggi dayo. Moo tax ñépp di xeeb réewi Afrig yi.
Maki de, tukkéem gii gàcce rekk la teg réewi Afrig yi. Daraay njariñ làmboowu ko. Ndax kat, ak fi Riisi tollu, moo waroon a soxla Saa- Afrig yi.