NU DELLOO NJUKKAL YAAY MARI MU SELL MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Boo déggee Popengin sa xel day dem ci waa jàngu bi. Muy màndargaal diiney Yeesu fii ci Senegaal. Doonte ne, dëkk boobee, duy kercen kesee fa dëkk ; am na tamit ay jullit. Aj gi nag njabootu Yeesu kiristaa di fa amal, daf ko gënatee siiwal fii ci Senegaal ak dëkk yi ko wër. Laaj biy sampu fii mooy : lan mooy cosaanu ak cëslaayu aj googule ? Ngir tontu ci bile laaj, mënees na yatt as poroxndollu ngir ngeen gën a xam as tuut ci xew-xew boobu. 

Ren di tollook téeméereelu ak fanweer ak ñeent (134) bu ñuy amal googu aj. Loolu di wone yàgg gi ñu yàgg amal xew-xew boobu. Bu ñu sukkandikoo ci sunuy gëstu, ku ñuy wax Mõ-Señëer Pikarda moo sànc béréb boobu ci atum junni ak juróom-ñetti téeméer ak juróom-ñetti fukk ak juróom-ñett (1888). Peeñug sunu yaay Maryaama mu sell mi ; nekk keemtaan gu mag foofu rax-ci-dolli ñëwug Paap Saŋ-Póol 2 ca nemmeeku ga mu amaloon ci atum 1992 ci réew mi yokk ko dayo. Ñu dippe ko “Sanctuaire de la Sainte Marie” ngir delloo njukkal soxna su sell si. 

Aj gi di am at mu jot. Popengin di dajale ay junniy junni ujaaj yu fekk baax ci biir réew mi ak ci réew yi ko wër. Lépp ngir màggal boobu xew-xew. Bokk na ci li ko gën a fésal di dox bi ñu bari ci ujaaj yiy dox, jóge Ndakaaru jubali ca béréb bu sell ba. Mu nekk yëg-yëg gu ànd ak mbégte mu réy ngir màggal Yaay Mari. Mu doon tamit jamonoy bennoo ak dajaloo guy bëtt ngëm ba wasaaroo ci  nit ñi. 

Ajug Popëngin gi bokk na ci xew-xewi diine yi gën a mag ci Senegaal. Ñu di ko  amal ci diirub ñetti fan. Mu nekk tamit jamonoy julli ak ñaan ngir dundal bés bi rawatina bésub altine ba wund daje ma di “Lundi de Pentecôte”. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj