Way-moomeel yee ngi sàkku ci Njiitu réew mi, Maki Sàll, mu bañ a laaj 3eelu moome (kay). Raddho, AfrikaJom ak yeneen i kurél yiy sàmm demokaraasi ak àqi doom-aadama ñoo def benn say, booloo cig kurél gu ñu dippee « Jàmm a gën 3e mandat », bind ab bataaxal jagleel ko Njiitu réew mi. Ñoom nag, wax nañ ak Maki Sàll, ñaan ko mu àddu ci mbir mi, wax ne du bokk balaa 2024.
Ab bataaxel la way-moomeel yi jagleel Njiitu réew mi. Li ñu ko dugge mooy dox tànki njekk, fexe ba jàmm am ci réew mi. Nde, coowal 3eelu moome gi ñuy njortal Njiitu réew mi, Maki Sàll, dafa nar a taal réew mi. Te, Senegaal, lu dul jàmm xaju fi. Moo tax ñu war a fagaru. Wolof ne, xoddiku balaa lakkle. Noonu, ci seen bataaxal bi, way-moomeel yaa ngi ciy fàttali Njiitalu APR li, xeex bi mu doon xeex, démb balaa tey, ci kàddu yii :
« Jële nga ay njàngat ci xeex bi nga doon xeex 3eelu moome. »
Dafa di, fukki at ci ginnaaw, Njiitu réew ma woon, Abdulaay Wàdd, dafa doon sàkku ñetteelu moome. Li ëpp ci saa-senegaal yi doon ko ci xeex, ba ci Maki Sàll mii ku wuutu ci jal bi. Nde, ñépp a ngi fàttaliku ba muy fob mer-gàddoom ba. Loolee la ko way-moomeel yiy fàttali ci kàddu gile. Moo tax ñu neeti ko :
« Noo […] ngi lay ñaan ci njekk nga bañ a laaj ñetteelu moome ci wotey 2024 yi. » Ngir fàttali, bi Njiitu réew mi faloo, dafa joxe woon ay dige ñeel limu moome yi ak seen i diir. Ndege, moom, Njiitu réew mi, dafa dige woon ne day wàññi moomeem gi, jële ko ci 7i at, indi ko ci 5i at kepp. Waaye, mujjewu ko def. Sàmmul kàddoom daal, maanaam. Waxoon na yit ne, ku falu, ñaari kay yu toftaloo kese ngay def, dem sa yoon. Te sax, loolu la ndeyu-àtte réew mi sàrtal. Rax-ci-dolli, moom ci boppam, moo waxoon ne 2019 mooy nekk mujjantalu kayam. Loolu la ko way-moomeel yi di fàttali bu ñu koy wax ne :
« Yow ci sa bopp, Njiitu réew mi, wax nga ay yoon, ne, lu jiitu sag pal keroog 2019, mënoo weesu ñaari kay yu toftaloo, te bind nga ko sax ci sa téere bi –Le Sénégal au cœur – ci 2019. »
Kurélu way-moomeel yaa ngi fàttali ne, ci Afrig, fépp fu Njiitul réew sàkkoo ñetteelu moome gu daganul, fitnaa ci topp. Réew yooyee, tey, ci dëj lañu dëkk. Ngir musal Senegaal ci musiba boobu, tàllal nañu seen i loxo Njiitu réew mi, Maki Sàll, di ko ñaan mu leeral taxawaayam, yewwi askan wi.
Wolof nag, dinay wax naan, am nopp yu fireeku, taxul a dégg. Waaye, Yàlla bu ci Njiitu réew mi bokk.