Jéyya ju réy moo xew fa Ecopi. Suuf saa fa màbb ba ay bakkan yu bari rot ci. Njiiti réew ma xamle nañ ne, lu ëpp 150i nit ñàkk nañ ci seen i bakkan. Suuf saa màbb fa Geze-Gofa, ca bëj-saalumu Ecopi. Geze-Gofa nag, dëkku kow la ; 450i kilomet la soree Adis-Abebaa, gëblag réewu Ecopi.
Li waral jéyya ji nag mooy, bees sukkandikoo ci saabalukaayi réew ma, taw yu bari te am doole ya fa sotteeku ci altine ji. Ki jiite mberaayu Gofa gi xamle na ca tele réew ma (Ethiopian Broadcasting Corporation, EBC, anglais), wax ne, waññeegum nañ 157i nit ñu ci dee ak juróomi nit yu ci mucc.
Kii di njiitu Commission de l’Union africaine, Musaa Faki Mahamat biral nay kàddu ci X, di ci mastawu askanu Ecopi :
“Noo ngi bokk naqar ak a ñaanal njabooti 157i nit ñi bokk ci kurél gi [kurélug Bennoo Afrig] te ñàkk seen i bakkan ci màbbug suuf gu metti gi leen dikkal.”
Ñu bari, ci àddina si, ñu ngi mastawu ak a ñaanal waa Ecopi, rawatina waa Geze-Gofa.