JIKKO JU RAFET MOOY TABAX AM RÉEW

Yeneen i xët

Aji bind ji

Wolof nee na, rafet kanam, rafet jikko a ko gën. Njub, jom, fulla, fayda, ngor, fit, worma, kersa añs., ñoo di jikko yoy, mépp réew mu koy doomam cëslaayoo, mu daldi tegu ci yoonuw naataange.

Xanaa kay nun, askanuw Senegaalu tey, noo jàdd, wàcc yoon. Moone dey, sunu Maam ya, ci jikko yooyii lañu ko tabaxee woon. Léegi, nag, lees seetlu mooy ne, ndawi réew mi, ak sax ñenn ci mag ñi, làmbootuñu yile jikko ak melokaan. Ndaxte, bu ñii di suus fii, ñee ñoo ngi metti fale.

 Worma réer na. Ngor moom, dafa gàddaay. Kersa saay na, sutura yit, kenn amatu ko. Bu fi yii jikko tumirànkee, ay njub ak ñoom seen moom dees na leen jéllale. Looloo tax may laaj, di la laaj yow miy jàng sama yaxal bile : ndax way-jur yi ñoo defatul seen i wareef ci xale yi ? Wala ndax xale yi ñooy màgg jël seen yoonu bopp ?

Xamoo ? Man it de xawma. Kaay nu déglu Paap Aali mu wax nu xalaatam. 

Paap Aali :

“Man it de, gàtt naay at lool, gàtt xam-xam. Waaye, dégg naa wolof neeti, lu la réer ci juddu, feeñ ci jikko. Am naa nag sama xalaat ci wàll wi te mën naa leen ko baaxe ndeem laaj ngeen ma, du noonu ? Waaw kay.

Damay jëkk à layal ni way-jur yi ñoo defatul seen i wareef. Maanaam, yaratuñu seen i doom ni mu waree. Dafa di, néew na, jamonoy léegi, way-jur wooy gis mu topp doom ji walla doom yi di jubbanti ak a jàngal teggiini àddina. Moom kay, dañuy seetaan ba jaan romb, ñuy dóor ca watit wa. Duñu yar jamono ji ñu war a yare xale yi, ba ñuy tuut tànk, neex a jàngal, neex a waxal. Nde, gone lawtanu yomb la, boo wëlbatiwul, mu law fu la neexul. Te nag, réccu day fekk jëf wees. Ñu bari nag, dañuy yor, waaye duñu yar. Lu wutale yor ak yar ?

Yor ag njaboot ak yor i gàtt ñoom yem kepp. Ki nga yor mooy ki nga dëkkal, di ko dundal, di ko faj bu feebaree, di ko fajal i aajoom Yum mënalul boppam. Loolu nag, dañ koy defal nit, di ko defal mala. Bu dee yar nag, ci xel meek xol bi lay dellu. 

Yar mooy nga tàggat nit ki, fexe ba mu nite. Maanaam, nga jàngal ko mbaa nga jàngloo ko, xamal ko Boroomam xamal ko diineem, xamal ko àddina xamal ko li ko fi indi. Kiy yar mooy kiy jëmbat ci nit ki jikko yi koy tax a sàmm digganteem ak Boroomam, digganteem ak moroomam, digganteem ak kéew gi ko wër. Kookii làmboo yile jikko, mooy garab giy may am réew kër, di ko dundal ak i meññeefam. Ndax, dina xam ne, Boroom du moroom, ba du gam-gamle dayob Yàlla ak dayob nit kepp. Nit ki yaru mooy kiy xool ni muy jëflantee ak i moroomam, di leen moytoo tooñ, di leen moytoo lor. Ndax, bëggul ku ko tooñ, bëggul ko lor. Nit ku yaru mooy tamit kiy sàmm mbindaare mi, wattu kéew gi, bañ a def dara lu koy yàq walla di ko nasaxal. Moom kay, day gëm liggéey, am jom, fulla, fayda, ngor ak njub yiy tabax am réew. 

Lii de laa ci xalaat, Séex.”

Waaw, Paap, am na solo lool. Xanaa ma toftal ci as lëf rekk. Ndax man itam de, li nga wax daanaka laa xalaat. Ndax, way-jur yi defatuñu seen i wareef, sonnatuñu ci yaru xale yi. Dañ leen a seetaan lool, bàyyee leen seen bopp. Te, ku amul kilifa, jinne doon sa kilifa.

Rax-ci-dolli, ak xarala yu yees yi jëm ci wàllum jokkalante gi, rawatina mbaali jokkoo yi, muy  WhatsApp mbaa di Tik-tok añs., tax nañ ba kenn amatul jotu saytu sag njaboot ci lu ñuy dox.

Gis naa tam ne, xale yi am nañ ci wàll ñoom itam. Ndax dangay gis way-jur wu sonn lool ci ay doomam, ñu xëy mel nu ko gënalul. Li ko mën a waral nag bari na waaye lu ci ëpp mooy ay àndadoo yu bonn rekk. Ndaxte li wolof di wax, dërëm ak dërëm ñoo mën a ànd, te béy itam day ànd ak moroomi bëyam.

Ak lu ci mën di am, war nanoo def taxaw seetlu, settantal bu baax jikko yi nga xam ni moom la doomu Senegaal di làmboo ba tax ñu mën a tabax sunu ëllëgu réew.

Séex Jóob

Jànguneb Ndar, làkk ak caaday Afrig, Master 1

Séex Jóob
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj