Malaanum Lëndëm : Bóris Jóob, na woon, fa woon

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ñeenteelu yoon a ngi nii Bubakar Bóris Jóob di génne téere bu mu bind ci wolof (+), te mu tudde ko Malaanum lëndëm ; muy téere bu EJO móol. Bóris moom, kenn dootul woññi ay mbindam ci làkki réew mi ndax ni mu nuy jàngalee li war a nekk, naka jekk : di bind ak a jàng ci làmmiñ yi nu nàmp.

Li ëpp ci nettali bi, Niseriyaa lay xewe, doonte sax Senegaal lay doore. Taxul nag mu jëm ci mbiri “Boko Haram” ak i ma-rëtal yi ne ca dëkk boobu, di jàpp ak a faat jaambur yi. Konte, ni mu ko defe woon ak Murambi, le livre des ossements (bi amoon Raaya Ladab bu mag boobu ñu ràññee ci àddina sépp, di Neustadt), Bóris daa tànnati meneen réewu Afrig mu sori Senegaal gii mu cosaanoo, di Niseriyaa ; ñu gisaat fii doomu Afrig bi mu doon, bu xër ci mbëggeel gi mu am ci kembaar gi réewam féete. Rax-ci-dolli, nettaleem bi yépp dafa fees dell ak takkandeeru Amilkaar Kabral.

Li ci nettali bi

Ci téere bu bees bii nag, bindkat bi mu ngi nuy nettali xew-xew yi juddoo cib lànket bu Keebaa Jakite di amal ; Keebaa, genn góoru baykat la, dëkk Tànjuraa, ab gox bu nekk ci penku Senegaal ; lànket bi, li ko lal mooy xam lu waral ñu bóom xaritu benn bakkanam, Jonas Akintoye, doon doomu Niseriyaa bu dëkkoon Ingwini ca réew moomu.

Ñoom ñaar nag, ay xarit dëggëntaan lañu woon, ku ci nekk jàppoon sa moroom ni woon ni doomu-ndey :

Naka lañu mënoon a def ba duñ daje bés mook Jonas Akintoye, ku ci nekk ne jàkk sa moroom, ñu yëg ci saa si ne ay doomi-ndey dëgg lañu, ay doomi-ndey yu bokkul deret ?

Noom ñaar, benn bëgg-bëgg lañu am, muy xër li ñu bokk xër jëmale ko ci lépp luy laal ci mbay. Waaye seen ànd yemul foofu, dañu nirooy jikko niy seex : ñoom ñaar ñépp dañoo gëm seen bopp, am péexte gu mat sëkk ba dara feesul seen i bët ; ñuy ñu dëggu, ñemee wax seen xalaat ak lu leen ci mën a fekk ; ñu doon ay nit ñu jub te am fit, bëgg seen réew te gëm seen i baaxi mboolaay ak seen cosaan. Ngëm-ngëm yu tumurànke yooyu ciyjamono yii, rawatina ci way-pólotig yi, nga xam ne, lu ne man nañ koo jënd, ba ci nit sax ak i noppam !

Ñaari xarit yii nag, ca ba ñuy ne ci seen diggu doole lañu xamante, ñu daje woon ca benn peyu Ërob, fu ay kuréli baykati Afrig gépp daje woon. Fekk booba, ku ci nekk ci ñoom ma nga jiite woon ca sa dëkk ay mbooloom baykat. Ba ñu fa jogee lañu jàppante ba seen i njaboot di demalante bu baax, doonte seen i réew dañoo soreyoo lool.

Bés, ñu xamal Keebaa ci njeggil-kàddu gi ni rey na ñu xaritam ciy anam yu ñaaw a ñaaw, te néew ba nee na mes, kenn xamul fu mu ne. Waa dëkk ba yépp njort ni, ñaawteef boobu, du liggéeyu kenn ku dul Chief Moses Abimbola, boroom daraja ju mag, bokk ci nguur gi, te nekkoon àndandoowu Jonas ba ñuy gune, ñu daan wujje ba ñépp xam ko. Fa la Abimbola jóge woon di won mbañeel gu tar jëme ko ci Jonas.

Keebaa moom, xelam mayu ko woon benn yoon muy seetaan dundu xaritam biy deme noonu ci neen. Mu ne fàww mu dem ba Ingwini ca Niseriyaa jaaleji soxnay ndemsi-Yàlla-ji, amal fab lànket ngir lijjanti mbir mu lëj moomu, te it, su manee nekk, mu fexe ba néew bi  feeñ. Mu jaraloon ko nag bakkanam. Ndax da doon ci moom, sas wu mu jële fu gën a sori ci xolam :

Keebaa Jakite xam (na) ne kóllëre ginnaaw lay féete…

Lu muy fekki ci tukkeem boobu ci réew mom  ñàkk kaaraange fa la fekk baax ? Ci yan anam la ñu reye xaritam bi, ak lu waral loolu ? Ndax sax dina feeñal néew bi ?

Bi mu demee ba màgget, di xaar Yàlla def li gën ci moom, la Keebaa Jakite jël xalimaam ne fàww mu nettali askanu tey wi, xew-xew yu doy waar yooyule.

Ciy way-jëmmal yuy dund ciy jamono yu wuute ak i béréb yu wute it, la bindkat biy jaare ngir nettali lépp jàngkat bi. Moom jàngkat bi sax, day dem ba miin way-jëmmal yi, ñu mel ne ay dëkkandoom dëggëntaan ; way-jëmmal yoo xam ne, ñii dañoo neex deret lool, ñee nee ñu bon-a-bon ; waaye li ñuy wuute yépp, kenn ku ne ci ñoom am na lu ñuy mën a jàngat ci nekkinam ak taxawaayam.

Way-jëmmal yi ci  téereb nettali bi

Bi Keebaa yeggee Ingwini la nu nettalikat biy wonaleek i way-jëmmal  yu bees: ay defkatu ñaawteef yu jàppe rey nit ni liggéey (Chief Moses Ambibola ak “surgaam”, James Vandi), ay nit ñu xumb te doy waar (Mama Wumbi-Oyé, yaayu Moses ju xayedi ji), ñu jaambure te mën a daw ay ba dee (Tony Akintoye rakku Jonas ji)…

Ku ci ne ci ñoom, bindkat bi daf koo jëmmal, ku ci nekk ak say jikko walla say feem, ba far joxe melo nit dëggëntaan. Way-jëmmal yooyu yépp lañuy gis ñuy dem ak a dikk, di xalaat, di gént, di waxtaan, ñenn ñiy faat jaambur yi, ñeneen ñiy aar seen i moroom ; am ñu ciy xeex ngir taxawal yoon, am ñoo xam ne, topp seen bakkan rekk a leen soxal…

Jàngkat bi, lu muy gën a xuus ci Malaanum lëndëm di gën a yéemu ci ni nettali biy doxe ba fa muy mujj. Lépp Bóris Jóob di nu ko toggal ba taajal nu lu ñor xomm. Ci njeexital li daal, nettali bu am solo lanuy topp, nettali bu nuy yéem ndax mbetteel yi ci biir ; nettali buy jàngale ci ni àdduna siy doxe,  buy jàngale ci tëralinu ëllëgu doom-aadama.

Bóris du tàyyi di jaxase jamono yeek béréb yi, ni mu koy faral di defe, jaare ko ciy xalaati Keebaa : ni mu doon janeere dundam ca ba muy waxambaane. Keeba di fàtteliku ay ndajeem ak Jonas, seen i waxtaan, ni ñu daan déeyandoo, seen i ree bay xàqataay ; waaye it, seen i njàqare, seen i soxla yu jëm ci seen liggéey, ak itam seen i wérante yu xumb jëm ci mbiri pólitig bi walla ci mbiru xeltu. Ku ne werante, ni juyoo, ndax li ñu doonoon ay doomi-ndey taxuleen woon a juboo ci lépp. Teewul nag, ñaari xarit yi doon gën di nawante. Ciy werante yooyu la bindkat biy jaare ngir samp ay xalaat yu am maanaa.

Ponki xeltu yi Bóris indi

Ci seen i ñaaroo yi ñu daan faral a am, Jonas da daan cokkaas xaritam bi, di ko tooñ ci lu jëm ciy ngëm-ngëmam, dem bay wax lu ëpp ci diineem, jàpp ne ciy “waxi kasaw-kasaw” doŋŋ la lalu. Su ko defaan, Keebaa day waaru :

Ci laa jëkkee xalaat tamit ne, Jonas Akintoye, xéy-na yaram wi neexul.

Ñaari doomi-ndey yi doon nañu waxtaane yeneen i mbir, ginnaaw lu jëm ci diine ji. Lu deme ni Demokaraasi itteeloon na  leen, te mu nekkoon it lu Jonas gëmul woon, ba tax koy kókkali Keebaa mi doon tiitaroo Demokaraasi Senegaal, naan royukaay la ci  Afrig. Du tere nag, bu Keebaa seetaatee mbir mi, du xam lu mu koy tontu :

àndumaak Jonas wànte nag, xiif di la bëgg a rey ba noppi ngay bàkkoo demokaraasi subaak ngoon, gaa ñiy sàcc di kàcc, di lekk ribaa ba seen biir yiy bëgg a fàcc, ñuy toroxal baadoolo yi, ku ko seet ci sunu Senegaal gii xam ni su dee loolooy demokaraasi, demokaraasi ay naxee-mbaay kese la.

Lee-lee itam Jonas samp laaj ci sàrt yi lëkkale réewi Afrig yi ak yeneen réew yi, rawatina yu Ërob yi :

Mën nga maa wax luy yoonu Tubaab yi ci sunuy mbir ?

Noonu la ko ñaari xarit yi jàppe woon : wecce yu dul jeex ci lépp lu soxal ëllëgu doom-aadama, rawatina luy tax réewi Afrig yi suqaliku.

Li Keebaa doon fàtteliku yooyu yépp, teewu ko woon bàyyi xel ci lànket ba ko taxoon a jóg. Ku bóom xaritam bi, ak lu tax ? Ci yan anam ? Fan la ñu làq néew bi ?

Laaj yooyu ak seen i tontu, Bóris day feeñal lépp, ndànk-ndànk, ciy defin yuy fësal ni mu xareñe ci bind téereb fent.

Xereñtey Bóris ci mbind mi

Gis nanu ni bindkat bi di wommate jàngkat bi, dëkkoo-dëkk, ciy jamono yuy dem ak a dikk, mel ne ku naan ko naxee-mbaay, na ko Asta Balde waxe, ba muy jëw Gorgi Seega Ture ci jëkkëram. Asta  Balde dib sekkarteer bu Seega di liggéeyloo mu kay bindal nettaleem bii ko ñor lool, su weer deewe mu fey ko. Konte, su dee Seega mooy nettali, moom Asta Balde mooy ki nuy jottali nettali bi : di nu xamale sax ak Seega ak waa këram, ak yeneen way-jëmmal yiy nar a ñëw ci ginnaaw ; di ci njàmbaasaale nag ay mbiri boppam. Mu far mel ne ñaari nettali lanu bindkat bi boole di defal.

Konte Bóris, xaraley nettali yu bare te wute la jëfandikoo ngir yakkal nu téereem bu am solo bii, am maanaa lool, di Malaanum lëndëm. Ci ñeenti xaaj nag la nu ko indil, bu ci nekk di doore ci bataaxal yi Asta Balde di yónnee jëkkëram ja nekk bitim-réew te mu namm ko lool ; lu muy def di ko ko nettali, ragal réeroo seen diggante ndax fiiraange. Bataaxal yooyu sax ñooy tëj téere bi.

Kon nag, jàngkat bi, amul lu koy jaaxal : du réer benn yoon ndax Asta Balde mooy ki koy tette ba tax muy gindiiku saa su ne.

Leneen luy biral xereñteefu Bóris mooy wolof yu set yi muy bind, te du rekk mbind mu set te rafet : kàdduy way-jëmmal yi ci seen bopp dañuy génne waxin ak xalaatu doomu Afrig wala doomu Senegaal tigi, mu wóor ne lii duy kàdduy weneen làkk wu ñu tekki. Mu mel ne bindkat bi, ni muy waxe di ko binde, noonu lay xalaate ci làmmiñ wi mu nàmp. Loolu moo koy may muy mën a firi dëgg-dëgg, ci làmmiñu dëkkam, yëg-yëg biy jóge ci askanam.

Ci njeexital li, mën nanoo jàpp ni, Bubakar Bóris Jóob teggiwul benn yoon tànkam ca fa mu ko tegoon, muy yoon wu  ay magam xàlloon, ñu mel ni Seex Anta Jóob, Seex Aliyu Ndaw, Sahiir Caam, Paate Jaañ, Maam Yunus Jeŋ, Aram Faal ak ñoom seen. Bubakar Bóris Jóob ak i maasam wallay rakkam (Mamadu Jaara Juuf, Adraame Jaxate, Abdu Xaadr Kebe…), ñu ngiy bay, tey, seen waar, ci anam bu mucc ayib, ci tool bu yaatu boobule.

Bubakar moom, waaram ci wàllu ladab la ko féetale : fexe ba téreeb nettali ci wolof tollu fa yeneen xeeti àdduna si yóbbu seen yos. Moo waral ndam li mu ci amagum, àdduna sépp a ci teg bët, muy lu ñépp mën a seede.

Uséynu Béey

(+) Téerey Bubakar Bóris Jóob ci wolof :

  • Doomi golo, téereb nettali, Ndakaaru, Papyrus-Afrique 2003, ñaareelu móol EJO, 2019

  • Nawetu deret, kilib (tekkig ‘Une saison au Congo’ bu A. Césaire), Zulma et Mémoire d’encrier, Caytu, 2016

  • Bàmmeelu Kocc Barma, téereb nettali, Dakar, Ejo, 2017

  • Malaanum Lëndëm, téereb nettali, Dakar, Ejo, 2022

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj