KUJJE GEEK WOTEB 2022 BI: BËGG NAA LA, BËGGUMA LA, LOOLU JARUL COOW

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci bésub 23 sàŋwiye ci atum 2022 bii di ñëw, la Senegaal fas yéene amal ay wote jëm ci palu njiiti gox-goxaan yi. Gannaaw ba pàrti pólitig yi jàppante ci mbiri yoonu pal gi, maanaam li ñeel doxalinu wote bi ak jumtukaay yi mu àndal, léegi, pàrti yooyee, seen yitte yépp a ngi aju ci nañu nar a taxawe ci joŋante yi ñuy waajal.

Coow li jib lépp, looloo ko waral ci jamono yii, jóge ci anam yi pàrti yi di taxawale seeni mboolooy kurél yi. Kilifag pàrti PUR moo sulli mbóot mi, yëgle ne “ñeenti pàrti yi gën a mag ci kujje gi” déggoo nañu ngir jëmmal seen nas bii doon sàkk mbootaayu pàrti yu kujje gi. Pàrti yooyu ñooy PASTEEF, Taxawu Dakaar, PUR ak PDS. Coow li ne kur ci dëkk bi. Ñu teg ciy fan, mbooloo mi ñu tudde “Yewwi Askan Wi (YAW)” daldi juddu.

Ñenn ñi rafetlu ko ndax yaakaar ne kujje gi dina fi jóge génn ci gutt gi mu ne woon ba léegi, wone dooleem, jàkkaarlook waa nguur gii di sonal askan wi ; ñeneen ñi ñaawlu li kujje gi manul a fexe ba booloo nekk wenn say képp. Ci kow loolu, am na it ñuy laaj naka la ñeenti pàrti doŋŋ di woote ni ñooy taxawal lu mat, daanaka, ay téeméeri làng. Ba tey it, gisees na ñu rafetluwul doxalin wi lal wote woowu, mel ne ñi ko sooke dañoo nawloowul seeni naataango yi ñu bokkal xeex.

Am na sax ñu ci doon booley xaste, di ñaawal kujje gii “man a jaxase ñu àndul, mbete supp kànja !” Teguñu ci ayubés, PDS génneeb bataaxal xamle ne bokkul ci mbooloo mu yees mii, ndax masul a xaatim lenn lu koy firndeel ; yeneeni pàrti yu mel ne AJ/PADS ak Bokk Gis-Gis, ñoom it génne seenub yëgle di wone ni bokkuñu te ànduñu it ci doxalinu kurél gu bees googu di Yewwi Askan Wi. Ginnaaw bi, kurélu Gëm Sa Bopp gi ci bokkoon, far génn moom it ci mbooloo mi, ndax ñàkk a gis boppam ci defin wiy niru xàjjaatle ci biir pàrti yi, mel ne yenn ci pàrti yi bëgg a féetale seen bopp ci kow, ñi ci des ci suuf. Coow li jibati, yëf yi jaxasoo. Ay kàddu jógati di ŋàññ kuje gi ndax seen ñàkk-juboo.

Pëndu coow loolu jotul a wure, meneen mbooloo mu soqikoo ci kujje gi daldi juddu wone boppam. Ñu xàmmee ci ñi ko sàkk, ay pàrti walla kurél yu mel ne PDS, Bokk Gis-Gis, AJ/PADS, CRD… Muy mbooloo mu mag, daanaka walla lu bon-bon, mu tollook dayo moroomam mi ko jiitu. Coow li neeti kur. Ñi jàppoon ni kujje gi mënta fexe ba booloo, gënatee yëkkati seen baat. Jamono jooju yépp, waa Bennoo Bokk Yaakaar (BBY) yi ŋànk nguur gi, ñu ne tekk di seetaan ; ñenn ñi jàpp ne sax, booba ñu ngee ree ci suuf. Waaye ñoom it, ndax seen ay ci coow li du dikk, bu ñu demee ba war a tànn ci gox bu ne, ku fay nekk jaraaf ?

Waaw, booba nag, ana askan wi, moom ? Ana li ciy taxawaayam ? Su dee dëgg rekk a tax ñuy wax, daa mel ne ñoom ñooñee, askan wee lee doon seetaan dëggantaan. Wax dëgg, askan wi moom, daa am lu ko doy sëkk, ak mbënd mi ko léjal ba ci kanamu Yàlla ! Rax-ci-dolli, njëgum njaay mi di yéeg jëmale… asamaan…! Lépp a yokku. Fekk booba, ndox mu ñu naan rafle fi, ba tax jigéen ñi di ko wuti ni doom yu góor. Moonte, askan wi de, moo war a tànn ci diggante waa nguur gi ak waa kujje gi, ñi ko doy ngir mu dénk leen boppi gox-goxaan yi, ngir seen yorin wu rafet. Ku yabu ne, ngir seen dundin ñoŋ.

Lu mu ci manti doon, way-pólitig yi, warees nañuy taxaw-seetlu, ànd ak seen xel, gannaaw ba ñu leen njortalee ñunekk ñu bëgg seen réew, fonk seen gox, te jiital njariñal askan wi. Ndax kat, gàtt-xel weesuwul nit jóg ni kenn waru fee sooke dara te boolewuma ci ! Ndax it, du ñàkk-xel di jàpp ne lu ëpp ay ñaari téeméeri kurel, mënees na leen a boole ci menn mbooloo, ñuy ànd di nas, di xàccandoo, di dóorandoo ?

Waaw waaye, ndax bokkul it ci gàtt-xel nga woo ay nit ngir ngeen ànd xeex, ba noppi naan leen “Yeen tekkiwuleen dara, toppleen rekk sama gannaaw ma yóbbaale leen ?” Xaste wi nag, moom, mënoon naa ñàkk, rawati-na ba muy niru tayeef. Ndax, xanaa kañ, kuy nas ngir boole ay nit, ñu àndul bokkuñu kurél kepp lay man a woo ? Rawati-na, mbooloo moo xam ni, génn nësër doŋŋ moo ko tax a jóg, maanaam, bokk sotoo ki ñuy jàmmaarloo, ba mu abal leen ? Ana kon lu fi indi ñamu supp kànja wu neex woowule ?

Ak sunu xel mu gàtt, foog nanu ni, laaj yooyu de, suñ leen sampoon ca njalbéen ga, jafe-jafe yu bare, maneesoon na leen a moytu. Am déet ? Waaye ndegam su ndox tuuroo, ab ban a cay des, waa kujje gi, warees nañoo taxaw-seetlu, defaraat seen koddaay, te fexe dëgëral seen taxawaay. Ñaar ba ñetti mbooloo sax man naa am, su dee ñoom ñi ko séq dañuy bàyyi xel ci ne, li leen xàjjaatle ak nguur gi moo ëpp solo fuuf li jaar ci seen diggante, ñoom ci seen bopp. Na fekk nag, ku ne xam sa bopp, ndax kat, bët du yenu waaye xam na lu bopp àttan. Ba tax na, waa kujje gi, su ñu bëggee ànd ànd wu rafet te yàgg (naka BBY amale), fàww ku ne xam li ngay “peese” ak nu sa moroom tollu.

Ana kuy weddi ne, Usmaan Sonko, li muy gune yépp, ak li muy doon gan yépp ci làng gi, doole ji mu am tey, kenn mënu koo nasaxal ? Ana kuy nàttable dayob Ablaay Wàdd ak PDS ? Ku xam jaar-jaaru pàrti boobu xam ne, moom du nangu mukk geneen kurél di ko jiitu, feek wonewul boppam ba wuutu PDS ci taxawaay bi mu am booba ba léegi ci làngu pólitig bi ak ci réew mi. Loo bañ-bañ lëg, nangul kooy noppam yu gudd ! Lii nag, am na njàngale mun ci man a jële : fi ñu tollu nii, PDS ak PASTEEF mënuñoo bokkagum menn mbalka mu ñuy naane ! Ndax nag, soxlawul di naxante, joŋantey pólitig yii, xëcco nguur a ngi ca xol ba ; te sax, ñenn ñi, duñu fàtte mukk seen nafa, fu ñu toll.

Loolu nag, terewul waxtaan, weccee xalaat bokkay nas ñeel anam yi wote wi war a doxe. Koonte nag, ñaari mbooloo yii soqeekoo ci kujje gi warul a jaaxal kuy seetlu, di jëfandikoo xelam. Waaye li war a leer ci boppu ku ne, mooy ni, ëpp doole sa moroom warul a tax nga xeeb ko te Wolof Njaay nee na “koo xeeb, mu yab la”. Te, li wóor ba wóor mooy ne, kenn ci làngu pólitig gi, mënul a dem moom kese ci xare bi ba jële fa ndam, ak doole joo mënti am ! Ci way-pólitig yi nag, mel na ni, kii di Maki Sàll moo gën a mokkal njàngale moomule… Dëgg la, moom nag daa yore kopparam gu duun, boole cib xaatimam bu am solo. Moo tax it…

Kujje gi daal, war naa seetaat boppam. Ñi man a ànd, nañu ànd booloo. Ñi bokkul genn kurélu mbooloo nañuy yëgante, bokk xeex ngir wote wi ci boppam jaar yoon ; te ñuy bañ a xeebante, bañ a tamante dëmm. Tey bàyyi xel saa su ne, ci nekkinu askan wi ak it ciy xalaatam. Leneen lu way-kujje gi war a bàyyi xel, mooy luñuy def ba fexe wéyal seeni mbooloomi kurél yi, gannaaw su wote gox- goxaan yii jàlle. Ndax kat, xeex bi day door rekk… te kuy dem xare war a fàggandiku !

Uséynu Béey

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj