KAN MOOY ANTA BAABAKAR NGOM ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Anta Baabakar Ngom mooy jenn jigéenu lawax ci joŋantey 2024 yi ngir nekk Njiitu réewum Senegaal dibéeru ëllëg ji, 24 màrs 2024.

Anta Baabakar Ngom a ngi juddoo Pikin, màggee Géejawaay, di liggéeye Malika (Ndakaaru). Am na 40i at, di jiite SEDIMA GROUP atum 2016 ak tey.

Soxna si Ngom, ku ràññeeku la ci liggéey. Ndax, ndefar gii di SEDIMA, moo nekk ca bopp ba te daa raam ndànk ba yéeg. Anta a ngi doore njàngam Senegaal, mottalee ko Iniwérsite Toronto. Fa la amee Master I ci wàllu koom laata muy wutali Farãs, amee fa Master II ak it lijaasu MBA ñeel Communication.

Anta Baabakar Ngom, doomu Baabakar Ngom la, turu baayam miinees na ko ci Senegaal. Anta nag, ñu ngi ko gën a ràññee ci atum 2012 bi muy jàppale Njiitu réew mi Maki Sàll. Léegi nee na dafa jël yoonu boppam, ngir soppi li fi nekk ndax doxul. Ciy waxtaanam dinay faral di ñëw bu baax ci nees war a jàppalee jigéen ñi, gën leen bàyyi xel. Nee na sax, bu demoon ba jiite Senegaal, dina amal bànku jigéen. Dina fexe tamit ndaw ñi am i xéy ba duñu soxlaati jël gaal di jaay seen i bakkan.

Wàllu ndefar ak koom soxal nañ Anta Baabakar. Ci kow loolu nee na Senegaal warul génn ci kopparu CFA. Ciy kàddoom loolu mënul nekk, te gënul. Li doy waar ci kàddoom yii mooy ne ñépp ñi seen xam-xam màcc ci koom-koom ak luy suqalim réew ànd nañu ni FCFA, fileek Senegaal a ngi koy jëfandikoo, du mën a jëm kanam. Day mel ni rekk golo di bey baabun di dunde. Ndongo Sàmba Silla mi nu xam bu baax ci wàllu koppar faram-fàcce na ko ba tàyyi ci lu leer nàññ. Soxna Kati Leena Njaay tamit def na film duppe ko Koppar, sañ-sañ, mboorum FCFA di ci leeral ne réew mu defaralul boppam ay kopparam du moom boppam dëggantaan, day wéy di nekk surga. Nu jàpp ne soxna Anta Babaakar Ngom miy laaj réew mi bëgg na koo suqali, xéy-na dafa umpale ne FCFA day delloo Senegaal ginnaaw.

Ndey Koddu FAAL

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj