KÀTTEY CFEE YU 2025

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kàtte yu atum 2025 mi dinañu tàmbali ginnaaw-ëllëg, alxames 19 suwe, jeex ci àjjuma ji 20 suwe. Atum ren jii, ñoo ngi ciy xaar lim bu tollu ci 300 889i lawax yu ko war a def. Ñu séddale leen ci 2 018i béréb yu leen war a dalal ci biir réew mi. Ren nag, seetlu nañu ni 56, 29% (téeméer boo jël, lu ëpp juróom-fukk ak juróom-benn yi) ay jigéen lañu. Nguur geek jàmbure yi ànd nañu dugal ci seen loxo, waajal lu ëpp 24 000iy taxawukat yu koy teewe.

Jëwriñ ji ñu dénk njàng meet biral na ni, ci coobare Càmm gi, ndongo yépp dinañu jooxe seen kàtte ci lu amul benn jafe-jafe, ba ci ñi am jafe-jafey kayitu juddu, ngir beddi bañ cee am. Dinañu ci jëfandikoo nimerig bi ak daluwaay bii di “anadole” ngir woyofal liggéey bi ak gaaw a génne njureef yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj