Làrmeb Senegaal a ngi yokk ay sóobareem, maanaam mi ngi yokk limi soldaar yi. Nde, juróomi gàngoori sóobare yi ñu libeere woon ginnaaw bi ñu jeexalee seen i àpp, rànguwaat nañu.
Bees sukkandikoo ci Dakar Matin mi siiwal xibaar bi, ab militeer a ko xamle, wax ne, ñooñee ñu jëlaat, bésub 1eel ci sulet 2023 lañuy solaat seen i yérey soldaar, duggaat ci xare bi. Sidiki Kaba, jëwriñu xare bi, moo xaatim ndogal li. Te, kilifay sóobare yi jot nañ ndigal li. Bindees na ci jukkib dogal bi ne :
“Sóobare yi bokkoon ci gàngoori 2020/1, 2020/2, 2020/3 ak 2021/1 te ñu libeere woon leen ginnaaw bi seen i àpp jeexee, woowaat nañu leen ngir ñu liggéeysi.”
Jëwriñ ji leeralul sabab yi waral ndogal lile.