LI CI DIGGANTE NIT AK NITE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Moo xam muy seen doomu bopp walla jeneen ju ñu leen dénk, way-jur yu bari dañuy def seen kemtalaayu kàttan ngir yar gone yi ñu yore. Yitte lañu ko def joj, bokk na ci yi leen ëppal solo. Bu ko ñenn ñi jàppee ni aw sas wu rëy, ña ca des yen bu diis la ci ñoom. Ba tax mu leen di jaral ñu ciy xar seen tanki tubéy, di ci def lépp lu ñu mën, te duñu ci tàyyee jéem lu ñu mënul.

Ci ñenn ñi, kiy yar xale mënul a ñàkk a yorub yar di caw walla muy gëdd ak a yuuxu léeg-léeg. Waaye, am na ñeneen ñu gëm ne, mënees naa yar te leraw gi du jóg, yaram wi du tàng bay am i tëndëndiir walla ab légét. Donte ne am naat ñeneen ñu jàpp ne soxlawul wax jiy bari. Nde, kàcciri rekk mooy pexe mi ngir am li ñu bëgg ci xale yi. Ndegem ñoom xamuñu Yàlla, waaye xam nañu yar.

Mu mel ni kon, ak lu mu ci mën a doon, ñoom ñépp a bokk jubluwaay. Yoon yi ñu jël yépp, donte ne yu wuute lañu te safaanoo, ci benn bërëb bi lañu leen di jëme. Dafa di rekk ne, ku ci nekk ak yoon wi mu miin, wi ko gën a jubu walla wi gën a gàtt ci moom. Kenn ku nekk a xam nu muy tojee boppu jinaxam. Li am solo kay mooy, na jinax ji dee rekk.

ÑOOM YARKAT YI, SEENUG NISËR WEESUWUL TABAX I NIT YU NITE

Ginnaaw bi xale bi juddoo doon nit ba noppi, yarkat bi dafa am yéeney tàggat ko, mu mottali nit ki mu doon ba mu mat. Loolu mooy illa ji tax mu takk ndiggam taxaw temm ci gunge ko. Ànd ak moom di ko fital ak a niital ci yoon wow, bu fa jaare, àgg fa mu war a dem, fa ko dundam ci kaw suuf yabal, àddina di ko fa niir. Te muy fa nite toog di ko nég.

Moo tax mu koy jox i jumtukaay yoy, dañuy takkook ñoom ba fàww. Bu ko defee, fu mu dem, mën faa nekk, ku mu dajeel it mën a jëflante ak moom ci njekk. Liggéey la nag bob, yamul rekk ci yafal yaram wi ba mu duuf, yeel yi gudd, xar-kanam gi bélli. Waaye, wareef la mu boole ci xel mi ak xol bi ngir lu nekk ci ñoom ànd ak jëmm ji màgg, ba mat sëkk, doon mukàllafu boppam. Ci noonu, la nit kiy amee njort lu rafet ne tegu na ci yoon wi koy yóbbu ci mu nekk nit ku nite ki mu war a doon.

Yaram wi, xel mi ak xol bi ay ndab lañu yu ag buum walla ab solom jokkale. Menees na leen a xoolee sax ni ay keno walla ay bunt yu toftaloo ba noppi di jokkoo. Fàww rekk ñu ànd, lëkkaloo ngir liggéey bi àntu. Ndax, kenn ci ñoom warul a des ginnaaw te, ku ci tële rekk, ki ko mag te sës ci moom moo koy wallu.

Yaram wi mooy bunt bu njëkk bi. Mooy tolluwaay bi gën a suufe di it yoon wi gën a jege wu nit di jaar ngir xam. Ci moom la nit kiy sukkandiku ba bu làmbee daj, bu xoolee gis, bu dégloo dégg, bu fóonee mu xeeñ, bu mosee mu saf. Te, juróomi yëg-yëg yile doŋŋ, ñooy may nit mu mën a jonjante ak xam-xam jaare ko ci yaramam. Waaye, ci kaw loolu lépp nag, moom, jëmm ji, mooy jumtukaay bi gën a ñàkk solo. Ndax, yenn saa mu juum ba xalangu te, lu ko juumloo dafa yomb lool. Foofu la xel miy ñëwee taxaw.

Xel mi dafay janeer, di gént waaye it dafay xalaat. Xalaat yaa koy may mu mën di togg li muy janeer ak a gént ba jur xam-xam bu wóor. Bu ko defee muy xelli lu wér. Saa su yaram wi gagee, xel meey taxaw niital ko ak i xalaatam yu leer. Ci niral, nit ki téen janook weer wi, bët yi ne ko “weer wii ngay séen de, mook xaal jay jaay ca ja ba ñoo tolloo”. Xel mi dafay dikk ne ko “Déet ! Weer wi ëpp na téeméeri junniy xaal”. Te, noonu la koy jàppee saa su yaram wi naree wàcc yoonam. Waaye, moom it, yenn saa mu juum walla mu gag. Ndax léeg-léeg géntam yi jaxase ko. Walla xalaat yi ëpp ci moom ba lëjal ko lool. Ci lay taxawe, bàyyi xol bi gindi ko.

Xol bi mooy kërug pas-pas yi. Fa la xeeti gëm-gëm yiy daje. Moo xam yu diine la, yu xeltu walla yu mel ni ñoom. Lépp lu nit di gëm, daf koy fas, dénk ko xol bi. Te sax, bari na lu nit gëm ba du ci sikki-sàkka walla lu mu weddi ba tëdd ci suuf te amu ci firnde lu xel mën a nangu. Lu muy fas ci xol bi daal lay doon. Waaye, xel mënu koo làmb, xalaat mënu koo daj. Pas-pas a ngoog ! Ginnaaw yaram wi ak xel mi, xol beey ñatteelu bunt ci bunti xam-xam yi ndax li muy xettali xel saa su fattoo mbaa mu gëlëm.

Jokkalante bi am ci ñatti tolluwaay yii nag tax na ba seenub ànd doon lu mënul a ñàkk. Yaram wi kese njariñam bariwul, niki pëpp la mel, daanaka xott rekk la. Naam, mën na sooke coow lu rëy ak um riir mu bari, ni ab barigo bu deful dara, waaye ca lay yam. Lu mu jekk jekk ak it nu doole ji tollu, mënul a àgg fu sori bu àndul ak xel. Ñoom ñaar it, bu ñu lëngoo di wéy, lu ñu sori sori, dinañu àgg fof dina lëndëm ba dootuñu xam fu ñu nekk ndax xel meey jànnaxe, daldi réer. Moo tax, fàww xol (ak pas-pas bi mu ëmb) dikk, wommat leen.

Loolu moo waral, boole leen tàggat di farata ju rëy. Suuxat yaram wi ci ñam wu teey te sell teg ci di ko yëngal te moytu koo sëf lu mu àttanul. Nàmm xel mi ciy xalaat yu rafet tey jariñ. Moytuloo ko tayel, gaaw a yéemu ak teel a doylu ci xam-xam. Tàggat xol bi ci fas pas-pas yi ba ñu dëgër te nangul ñeneen ñi seen i yos. Moytuloo ko gaaw a gëm ak a weddi. Rawatina nag weddi, ndax miim dëgg a ëpp i loraange fuuf gëm lu dul dëgg.

Ba tax na, yam ci toppatoo yaram wi doŋŋ ëpp naa def. Nde, dafay ndiru xar mi ci gétt gi, ñuy xont ak a yafal, di xaar tabaski. Bëgg it boyal xel mi ba noppi soofantal yaram wi amul mucc. Ndax, xel mu sell, ci yaram wu sell lees koy séentu. Te nag, magum jëmm, magum xel a ko gën te magum xel, magum xel mu am pas-pas a ko ëpp njariñ.

Kon nag, ñatti ndab yépp a war a set wecc. Bu ko defee àddina daldi nuy yakkal. Nu mën a tàmbalee xéewalu ci ñam wi nuy niteloo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj