LI GЁN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Àjjuma 12 ut 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG : Ndogal yi lёkkatoo yii di YEWWI ak WALLU jёl

Ginnaaw seen ndajem waxtaan mi ñu amaloon àllarba 10 ut 2022 jёl nañ ab dogal ci ne duñ bokk ci wotey Hauts Conseillers des Collectivités Territoriales (HCCT) yii di ñёw. Ba tey, ci baatu Décce FAAL biral nañ ci ne duñ jébbal ab bataaxel (recours) foofu ca Conseil Constitutionnel. Ndax, ñoom amuñu ag kóolute ca kàngaam ya fare ca wàll woowu. Rax-ci-dolli, dañoo jàpp ne ñooñu dёgguwuñu (amuñu ngor) dara ci li ñuy def.

Paap Jóob fekki na waa BBY

Paap Jóob di njiital lëkkatoo gii di Bokk Gis-Gis/Liggéey ci am ndajem-waxtaan mum doon amal tey jii ci ngoon biral na ci ag ànd ak waa Bennoo Bokk Yaakaar. Maanaam, moom génn na ci kujje gi mu fare woon fekki njiitu réew mi ngir mu ëpp doole ca péncum ndawi réew ma. Mu nekk nag xew-xew bu doy waar donte ne sax am na ñu seen xel ñaawoon ci wujjeem ak nguur gi bi njuréefi négandiku yi génnee.

KOOM-KOOM : déggoob kopparal diggante njawriñ jiñ dénk wàllum koom-koom bi ak waa BAD

Njawriñ jiñ dénk wàllum koom-koom gi xaatim na ab déggoo (accord) ak waa Banque Africaine de Développement (BAD) bu tollu ci 79,3 miliyaar ci FCFA. Loolu nag, ab xaatim la ngir réewum Senegaal ci lu yàggul dara mu bañ a ajooti ci mennum réew ngir dund. Maanaam, mu am dooley bey lu ko doy ci lu deme ni ay ceeb, dugub, mboq, añs.  

TÀGGAT-YARAM : ёllёgu Giri Bórdoo ci làmbu ji

Ginnaaw bi ko Bàlla Gay 2 daanee dibéer jii weesu, ay kàddu yu wute nag jib nañ ñeel ёllёgu mbёr mi ci làmbu ji. Ndax, kii di Bàlla Juuf, bokkoon foofa ca écurie Faas, biral na ag ñàkk àndam ci ni Giri doxalee ca bés boobu. Rax-ci-dolli jafe-jafey écurie bi, Giri génnu ci. Ba tey, kii di Abdu Géy (directeur technique de Faas) moom tamit, ci ay kàddoom, mi ngi sàkku ci Giri mu taxawal écurie boppam.   

WÉR-GI-YARAM : Tёjum Raglu Aristide Le Dantec

Raglu Le Dantec dinañ ko tёj ci fukki fan ak juróom ci weeru ut wii. Mu nekk nag ab ndogal lu ub xelu ñu bari ci saa-senegaal yi. Waaye, jawriñ jiñ dénk wàll woowu, ciy kàddoom, xamle na ne wàllum tuxal meek yooyu ci yeneen béréb yi, tàmbali na ñaari fan ci weeru ut dina wéy ba fukki fan ak juróom ci weer wi. Loolu lépp nag, du ngir lenn lu dul teg leen ci ay anam yu mucc ayib muy fajkat yeek ñi ñuy faj ba liggéey bi gёn a ñoŋ.

NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI : Ndajem joŋante bu mag bi

Ci alxames ji, yamook 11 ut 2022 moo nekkoon bésu ndajem (cérémonie) joŋante bu mag biy (Concours général) boole ndongo yi jiitu ca joŋante boobu. Mi ngi doon ame  ci Kilifteefu NJiitu réew mi, Maki Sàll. Joŋante boobu nag boole woon na ay ndongo yu bari yu bokku ci daara yu wute. Te, soxnaa sii di wuyoo ci turu Faatu Ñã di jànge ca Lycée d’excellence Mariyaamaa Ba moo jiitu ca joŋante boobu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj