LI GЁN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Àjjuma 14 oktoobar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG
Wayndare yiy xaar dépite yi

Ginnaaw bi ñu taxawalee Ngomblaan gu bees, ci àjjuma jii la liggéey bi di tàmbali. Mu mel ni nag  lu tollu ci ñeenti wayndare moo ngi leen di xaar ci taabal ji. Bu njёkk bi di gafaka (budget) bi ñu war a wote. Ñaareel bi di cartu amnisti bees njort ne dees na ko yóbbu ca Ngomblaan ga, ñetteel bi di cart bi Mimi Ture namm a teg ngir génne wàllum mbokk ci càmmeef gi. Mu am tamit, leneen coow muy Mimi Ture mi bёgg a génn ci kippaangoo dépitey waa Bennoo Baakaar Yaakaar bañ a bokk fenn. Waaye, ba tey day mel ni mbir mi àntoogul ci digganteem ak naataangoom yooyu.

Bàrtelemi Jaas

Kii di Bàrtelemi Jaas di Njiital meeri bu Ndakaaru moom lañu def tof-njiitu kurél gii di Fonds Mondial pour le Développement des Villes (FMDV). Démb la ko ko ay naataangoom fal ci seen ndajem ren ji amoon ca Daejeon, ca Corée du Sud. Loolu nag, da di ndombog-tànk gu am solo goo xam ne dina ko ubbil ay buntu ca bitim-réew.

NJÀNG AK NJÀNGALE

Ndefarub fooraas ca UADB

Kurél gii di CROUS mi ngi xamle ne dina defar lu tollu ci juróom-benni fooraas ca daara ju kowe jii di Iniwérsite Àlliyun Jóob bu Bàmbey (UADB). Loolu nag, ay pexe la ngir saafara ñàkkum ndox mi ñuy faral di nemmeeku ca daara jooju.

Jeneen daara ju ñàkkum ndox sonal

Daara jii di Lycée Parcelles Assainies dafa dakkal am njàngaleem ndaxte seen róbine bi xelleetul. Ñoom, dañoo namm a dakkal njàng mi ba mbir yi dellu ci anam yu mucc ayib. Ndax, dañoo jàpp ne loolu du yoon ci daara ju am lu tollu ci ñaari junni ak juróomi téeméeri ndongo ak téeméeri jàngalekat.

KOOM-KOOM

Sémb bu tollu ci 42i tamndareet

Jёwriñ ji ñu dénk wàllum mbey mi, Aali Nguy Njaay, moo ko fésal ci ndaje ma mu doon amal démb. Ca moomule ndaje lañu taxawalee sémb boobu ngir suqali mbeyum ceeb bi. Kooparug sémb boobu mi ngi tollu ci ñeent-fukk ak ñaari tamndareti yu teg juróom-ñeent fukk ak juróom-ñetti fukki miliyoŋ ak juróom-ñetti junni ak juróom-ñeenti téeméer ak fanweer ak juróom-ñaar (42.980.044.686). Càmmeefug Senegaal ak Banque Islamique de Développement (BID) ñoo ko kopparal. Loolu, diy pexe ngir ñu dooleel fànn mbey rawatina bu ceeb bi.

TÀGGAT-YARAM

Ab xeex ca Aamadu Bari

Dafa mel ni mbirum xeex moom, ci futbal bi lees baaxoo di ko gis ci miim réew. Démb tamit noonu la fa deme ca estaad Aamadu Bari diggante way-fare (supporters) yi ci joŋante bu doxoon diggante Guney-tey ak Diisoo ba ñu bari sax jёle ca ay gaañ-gaañu.  

Bulaay Ja

Doomu Senegaal bii nekk jamono jii ca Série A ca Itaali, am na ékib bu nekke ca àngalteer bu ko namm a jёnd. Ñii di waa Everton ñoo teg ci taabal ji 16 miliyoŋ ci ay ёro ngir jot ci gaynde googu. Léegi nag, waxtaan waa ngay wéy ci diggante Salernitana, Villareal ak Bulaay Ja miy ndeyi-mbill ji.

XEW-XEWI JAMONO

Aksidaŋ diggante Maatam ak Lingeer

Benn kaar bu ndaw bu jóge woon Maatam jёm Ndakaaru moo mbёkk benn wóppu-yaha bu paan, ba noppi taxaw ci wetu yoon wi, rax-ci-dolli amul pano bu koy firndeel. Mu am nag fukk ak benn yu ca jёle ay gaañu-gaañu, am ñeent ñu ci mettile lool nag.

KAAWTÉEF

Senn ndaw suy wuyoo ci turu Peyton Stover di ab jàngalekat am lu tollu ci ñaar fukki at ak ñett dёkke ca Etats-Unis moo am doom ñaari fan kott ginnaaw bi mu yёgee ne jigéen wérul la. Ndax, moom dafa njortoon ne coonoy liggéey bi kepp a ko jàpp ndekete yoo am na lu lalu ci ginnaaw.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj