Li gёn a fés ci xibaari bés bi Alxames 1 Sàttumbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Àppug wotey HCCT xamees na ko

Ci ab saabal bu mu génne, Njiitu réew mi Maki Sàll mi ngi xamle ne wotey Haut Conseil des Collectivités Territoriales (HCCT) dinañu leen amal Dibéer ñeenti fan ci weeru Sàttambur. Ñaari lёkkatoo yii di Wallu Senegaal ak Yewwi Askan Wi nga xam ne ci kujje gi lañu fare xamle woon nañu ci lu yàggul dara ne duñu bokk ci wote yooyu.

Xёccoo ngir jiite Péncum ndawi réew ma

Ahmed Aydara, Bàrtlemi Jaas ak Lamin Caam ñooy ñetti lawaxi lёkkatoo YEWW-WALLU yiy xёccoo ngir nekk lawaxu lёkkatoo yooyu ba mёn a jiite péncum ndawi réew ma. Ahmed Aydara nag, ngir dёgaral taxawaayam, xamal na ay àndandoom ne dina am ñeenti dépite yu bokku Bennoo Bokk Yaakaar yu ko jàppale saa bu ñuy wote.

Génnug Seex Jeŋ ca PDS

Ginnaaw bi mu génne ca pàrti bii di PDS jaare woon ko ci ab saabal bu mu biraloon ñaar-fukki fan ak juróom-ñeent ci weeru ut cig ñàkk a déggoo yu mu amoon ak kii di Karim Wàdd. Kii di Abdulaay Bari di xamle ne loolu ay sosi kepp la. Dafa xam ne amatul benn doole ci pàrti bi moo tax mu génn. 

WÉR-GI-YARAM

Xew-xew bu tiis ca Kéedugu

Ginnaaw xew-xew ba amoon ca Luga ca jamono yale, soxna sii di M.D. Jàllo nga xam ne da doon mucc fale ca Kéedugu mujje na ñàkk bakkanam moom ak doom ja yépp ci anam yu doy waar. Am na nag ñetti fajkat yu ñu fa teg loxo ci jamono yii.  

Koppar yi Almaañ teg ci loxo kurél gii di UNICEF

Ngir gёn a yembal ñakk yi ngir xeex mbas mi (covid) ci Senegaal, Almaañ teg na ci loxo UNICEF lu tollu ci 3,9i miliyoŋi dolaar. Mёnees na ko xayma ci ñaari miliyaar ci sunuy koppar. Loolu, ndimbal la ci Senegaal ngir dooleel paj mi ba ñakk yi gёn a gaaw.

TÀGGAT-YARAM

Kii di Abdu Jàllo, di doomu Senegaal nekk fale ca Paris SG, ma nga ca yoonu dem fale ca Almaañ ca ekib bi ñuy dippe RB Leipzig.

Bàmba Jeŋ tamit nekk ca Marseille mi ngi ci yoonu jóge foofu ngir dem ca Àngalteer  ca ekib bi ñuy dippe Leeds United. Ndax, bees sukkandikoo ci ñii di waa SKY SPORT déggoo am na ci diggante ñaari ekib yi.

Mustafaa Naam tamit di doomu Senegaal nekkoon ca Paris FC jóge na fa dem ca Chypre ca ekib bii di Phaphos FC. 

KOOM-KOOM

Ànd diggante Ruwaayóm-Uni ak réew yi nekk ci yoonu suqaliku

Lii nag ag jokkalante (échange) gu bees la goo xam ne ñoom ñoo ko nas mu tuddu Developing Countries Trading Scheme (DCTC) ak réew yi nekk ci yoonu suqaliku te Senegaal bokk ci. Déggoo boobu nag ci wàllu njaay ak njёnd la (commerce). Rax-ci-dolli day yombalal réew yooyu ñu jaay njureefi yi juddoo ci seen i mbey (lu deme ni mboq, soble…) ca Tugal.  

Ay xibaar ñeel tёjug Wave ci Senegaal

Loolu di ay xibaar yu doon daw ñeel tёjug wave ci Senegaal ak gàllankoor gafakay (compte) kepp ku ko ame. Ñii di waa Wave nag ci ab saabal bu ñu def xamle ñañu ci ne loolu dara amu ci. Rax-ci-dolli, mi ngi xamal ay soppeem ne yónne walla génne xaalis jàppandi na ci Wave fépp ci biir réew mi. 

 

XEW-XEWU JAMONO 

Kii di Abdu Kariim Géy moo plainte waykat bii di Jeebaa ci aw woy wu mu génne woon ca jamono yee. Way wii di “Lamu saf” ak widewoo bi, ba ci kàddu ya mu cay wax la moom mii di Abdu Kariim Géy jàpp ne dёppoowul ak sunu mbaaxi (valeurs) réew.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj