Lu tollu ci 60i nit ak lu teg ñoo ñàkk seen i bakkan tey ca réew moom ci ab jàmmaarloo bu dox diggante ñaxtukat yi ak takk-der yi ci diwaanu Njamena. Nee ñu, 300 ñoo amey gaañu-gaañu. Loolu nag, mi ngi xew ci wooteb kujje gi ngir xeex ni kii di Mahamat Idriis Débi Itno téyee Nguur gi ak yokk gi mu yokk àpp bi. Fitna jaa ngay wéy nag ba tey donte ne sax ay bal dёggantaan am na ca aw yoon.
Liz Truss
Kii di Liz Truss di jёwriñ ju mag ju Grande-Bretagne xamle na ag mbawam tey jii. Donte ne sax, ca réew moomu ndombog-tànk googu dafa faa am doole lool. Waaye, ki ñu takkal ci jamono jii dafa mel ni mbooloom wàññeeku na lool ca réew ma. Laj gi mu laj ci sémbu koom-koomam nag bokk na ci li ko waral.
Senegal
PÓLITIG
Tabb yu yees yi
Ca ndajem jёwriñ ma mu doon amal démb ci àllarba ji ca la jёlaat ndogalu jox ñeneen ci ay ñoñam ay ndomboy-tànk. Ñooñu nag ñi ngi tollu ci fukki nit ak juróom-benn. Muy kii di Maxtaar Lax (secrétaire général du ministère des transports aériens et du développement des infrastructures aéroportuaires), Mayel Caam (président du conseil d’administration de la société nationale des eaux du Sénégal SONES), Mamadu Moori Jaw (président du conseil de surveillance de l’agence des travaux et de gestion des routes AGEROUTE Sénégal), Sylvain Alfõs Boyeer (président du conseil de réglementation de l’agence sénégalaise de réglementation pharmaceutique ARP), Mammadu Maamuur Jàllo (directeur général de l’office national de l’assainissement du Sénégal ONAS), El Haaji Usmaan Baro Jonn (directeur général de la compagnie du théâtre national Dañel Soraanoo), Mamadu Wàdd (inspecteur des affaires administratives et financières au ministère des transports aériens et du développement des infrastructures aéroportuaires), Kumba Sow (inspecteur technique au ministère de l’économie, du plan et de la coopération), Seex AhmaduBàmba Saar (directeur de l’artisanat), Suley Kan (directeur de l’apprentissage au ministère de la formation professionnelle, de l’apprentissage et de l’insertion), Seex Juuf (directeur des infrastructures aéroportuaires au ministère des transports aériens et du développement des infrastructures aéro^portuaires), Ibraahiima Soori Saar (directeur de l’administration générale et de l’équipement au ministère des transports aériens et du développement des infrastructures aéroportuaires), Aamadu Jàllo (directeur de l’administration générale et de l’équipement au ministère de la formation professionnelle, de l’apprentissaage et de l’insertion), Àlliyun Paala Mbay (directeur de l’administration générale et de l’équipement au ministère de la culture et du patrimoine historique), Aamadu Njaay (président du conseil d’administration du Grand Théâtre Duudu Njaay Kumba Roos), Abel Ngoor Maron (secrétaire général de la compagnie du théâtre national Dañel Soraanoo).
Mataar Ba
Ginnaaw bi ñu ko tekkilee ndombog-tànkam ci bi ñuy taxawal Nguur gu yees gi, démb, ca ndajem jёwriñ ma la ko Njiitu réew mi takkal geneen ndombog-tànk gu yees muy Jëwriñ bëkk-néeg bu mag bu Njiitu réew mi.
Ndajem waa-COLIGEP mi
Kurél gii di Collectif pour la libération des détenues politiques (coligep) ma ngay wéy ci xeexam ngir bàyyi gaa ñi ñu teg loxo yépp te ñu jàpp ne pólitig moo ko lal. Muy ku ci mel ni Seex Omar Jaañ, Abdu Kariim Géy, Papito Karaa, Ami Ja, Usmaan Jaañ ak ñeneen ak ñeneen. Loolu tax ñu bёgg a amal am ndaje ci àjjuma jii ca Place de la nation.
WÉR-GI-YARAM
Sёqёt su bon si
Bees tёnkoo ci lim bi kurél gii di Association Sénégalaise de Lutte contre la Tuberculose (ASLUT) biral ci nit ñi ame jàngoroy sёqёt su bon si ci réew mi, ñi ci ёpp ca diwaanu Ndakaaru lañu dёkke. Ndax, ci diggante Saŋwiye ba oktoobar lim nañu lu ёpp juróomi téeméeri doomi aadama yu ame sёqёt su bon soosu. Te, loolu ci diggante gox yii kese la: Géejawaay, Pikin, Yёmbёl, Kёr Masaar.
Kopparalug 2,54 tamndareet ci ay dolaar
Ngir jёle fi ngaanag tànk walla lu ci laale (poliomyélite), ñii di waa OMS (organisation mondiale de la santé) teg nañu ci taabal ji lu tollu ci 2,54 tamndareti dolaar. Kopparal googu nag dina tax jàngoro jooju nga xam ne bari na réew yu mu sonal, mёn a wàññeeku.
NJÀNG AK NJÀNGALE
Bёgg-bёggu FNAAS
Kurél gii di Fédération Nationale des Arabisants du Sénégal (FNAAS) ci ndajem-waxtaan ma mu doon amal bërki-démb, sàkku na ci Nguur gi mu nangu seen sémb bii di PIDA (projet d’insertion des arabisants). Sémb googu mooy juróomi junni ñu am lijaasa ci araab ci fànn yu wuute ci àpp bu tollu ci ñetti at.
TÀGGAT-YARAM
Luubalug 100 miliyoŋ ca Casa Sport
Lu tollu ci weer kese des ci joŋante bi boole réewi àddina sépp, coowu luubal lëmbe kurélug way-fare Casa yi nga xam ne fépp lañuy topp gaynde yi. Ñenn ci biir kippaango gi nag ñi ngi duut baaraam seen Njiital kurél gi Malamin Tàmba ak kii di Njiital club Fanion bu Siggicoor di Séydu Saane.
Saajo Maane
Doomu Senegaal bii di Saajo Maane, ginnaaw bi mu jёlee ñaareel palais bi, topp ci Benzema, bokk na ci ñi ñu tànn ngir ñu mёn a jot ci neexal bii di Dubaï d’Or. Lii nag fukk ak ñetteelu yoon muy am te ñii di waa Globe Soccer Awards di ko amal. Lu tollu ci ñaar fukk ak juróomi futbalkat a bokk.
Kàdduy Kalidu Kulibali
Moom doomu Senegaal moo ngi xamle ne réewi Afrig yi dañoo war a gёm seen bopp ngir ñu mёn a jёl raw-gàddu gii nga xam ne moo boole réewi àddina si yépp. Dañoo am bёgg-bёgg ak gёm-gёmu romb fi ñuy yam bi ñu dalee bokk ba léegi. Ndax, fi ñuy yam di ci bég, amul ékibu Tugal bu fay yam am ci mbégte.
Xibaar bu tiis
Benn saa-senegaal la bu bёggoon dugg Etats-Unis, moom lañu dóor bal ca digu Mexique wa mu ñàkk bakkan. Moom nag, mi ngi wuyoo ci turu I.Géy amoon lu tollu ci fanweeri at ak juróom-ñeent. Ma nga dёkkoon ca Kёr Masaar.