Ca ndajem jёwriñ ma mu doon amal démb, Njiitu réew mi jot na fa jёl i ndogal, jox ñenn ci ay ñoñam ay ndomboy-tànk. Muy kii di
Abiib Lewõ Njaay
(Secrétaire général du Ministère de la Culture et du Patrimoine Historique),
Mayaasin Kamara
(Président du Conseil d’Administration de la Société nationale « Les Chemins de Fer du Sénégal »),
Maalig Ndóoy
(Directeur général de la Société nationale « Les Chemins de Fer du Sénégal »),
Ceerno Aamadu Si
(Directeur général de la Société nationale « Agence de Presse sénégalaise » (SN-APS),
Mamadu Saaliw Sow
(Directeur général de l’Agence d’Assistance à la Sécurité de Proximité (ASP),
Mbay Saar
(Directeur de l’Ecole nationale d’Administration pénitentiaire),
Mutafaa Ñaŋ
(Directeur de la Mobilité et de la Circulation routière),
Yayaa Sàmba Ñaŋ
(Directeur des Transports routiers),
Mamadu Sàmba Jàllo
(Directeur de la Planification et de la Régulation des Autoroutes),
Maam Jaara Buso Jaañ
(Directeur de la Réglementation et du Suivi des Infrastructures routières),
Mamadu Mustafaa Kóli
(Directeur des Stratégies de Désenclavement et de la Promotion de l’Intermodalité),
Mamadu Ja
(Directeur des Transports ferroviaires),
Mamadu Ndaw
(Secrétaire général de l’Agence des Travaux et de Gestion des Routes (AGEROUTE).
Ndogal li Maam Mbay Ñaŋ jёl
Ci ndajem-waxtaan ma mu doon amal démb, Maam Mbay jot naa joxe ay leeral ci li ñu ko doon tuumaal ci mbirum PRODAC mi. Mu ne, amul genn caabalug IGF (Inspection Générale des Finances) gu ko taqal. Moom nag, nee na dina boole Usmaan Sonko yoon ngir mu indiy firnde ci tuuma yi mu teg ci ndoddam
Coowal suuf ca Tiwaawon-Pёl
Kii di meeru Tiwaawon-Pёl, di wuyoo ci turu Momar Soxna Jóob, dañu koy tuddu ci coowal suuf. Ba tax ñii di waa DIC woo ko ngir mu indi ay leeral ci coowal 46i bayaal (parcelles) yi waral coow li. Coow loolu nag yàgg na du ren, ma nga tàmbali woon ca atum 2015.
XEW-XEWI JAMONO
Réerug ñaari sóobare
Dijje Baaji (adjudant-chef de la gendarmerie) ak Fulbeer Sàmbu (Sergent) di ñaari sóobare yi ñuy xamle ne teguñu leen bёt gàawu ba tey. Seen i mbokk nag ñi ngi sàkku ci Nguur gi mu boole matuwaayam yépp ngir gis leen. Tey ci alxames ji, nee nañu dinañu amal am ndajem-waxtaan.
Xew-xew ba am ca Biññoona
Fale ca diwaanu Biññoona, ab toolu yàmbaa lañu fa yàqate, ñu rey ca ay robel, ñaari sóobare jёle ca ay gaañu-gaañu. Lu tollu ci ayu-bés làrme baa ngi sóobu ci yàqum tool yooyu, rawatina ci boori Sinjaan.
Njuuj-njaaj ca UCAD
Lii, lenn ndongo luy wuyoo ci turu P. Mb., nekk banqaas biy jàngale Yoon ca daara ju kowe ja nekk ca Ndakaaru. Liggéeyam nag mooy xool nu muy luubale alali jàmbur yi. Te, tёjoon nañu ko ci lu deme noonu ca weeru nowàmbar, atum 2018. Moom nag pexeem moo nekkoon di def boppam ab layookat walla ab ndawu Fongip ngir nax gaa ñi. Wii yoon, bi ñu ko tegee loxo, daan nañu ko atum kaso moo xam ne, dina ca tёdd weeruw lёmm.
Lakk ga am ca Wuro Sóogi
Jéyya ju réy a am, démb ci suba, ca kёru mbokki jёwriñ jii di Musaa Bookar Caam. Néegu wattukatu meer baa tàkk. Dёkkandoo ya daw, walluji ko. Yàq-yàqu ya nag bari nañ lool, rawatina alal ja.
Ag càcc ca Auchan Mermoos
Benn xale bu jigéen buy liggéeye Auchan Mermoos, di wuyoo ci turu F. T. te am lu tollu ci ñaar-fukki at lañu jiiñ càcc. Nee ñu, sàcc na fa, lum dee dee, juróom-benni yoon. Widewoo ya fa nekk ci ñoo ko weer. Moom nag, dafa am ku mu àndaloon ci mbir mi. Kooku nag mooy M. C. mi nga xam ne, F. coroom la.
Xibaar bu tiis
Lii benn takk-der la bu ñàkk bakkanam ci ab joŋanteb kuppe bu ñu doon amal. Moom nag dafa daanu ci digg joŋante bi, mujj fa jaare ñàkk bakkanam. Moom nag mi ngi wuyoo ci turu B. C., dёkke ca diwaanu Kafrin.
KOOM-KOOM
Liggéeykat yaa ngay wéy ca xeex ba
Liggéeykati fànn wu suufe wi (secteur primaire) ña ngay wéy ca xeex ba ñu sumboon. Tey ci alxames ji, jёl nañu ndogalu dakkal seen liggéey lu tollu ci ñaari fan. Li ko waral nag mooy kenn ci seen naatangoo yi, di Nogay Jóob, la ay jaaykati jёn doon metital.
Jaaykat ya ñu woo ca kanamu yoon
Lu tollu ci ñeen-fukki jaaykat ak ñeent la pekkug caytug yaxantu gi (Bureau des services de commerce) ca Mbuur woo. Li ko waral nag mooy ñàkk a sàmmonte ag njёg yi Nguur gi teg.
NJANG AK NJANGALE
Ndogal li PATS jёl
Pats (personnels administratifs, techniques et de service), di kurélu liggéeykati iniwersite yi, ma ngay wéy ca xeexam ba. Donte ne sax kii di Njiital njàngale mu kowe mi bёggoon na xaatim ak ñoom benn déggoo. Waaye, ñoom, dañu ne mukk du ci dal. Ci altine ji lañu mujje woon a dakkal seen liggéey lu tollu ci ñetti fan.
Ubbiteg daara ju kowe ji
Démb ci ndajem jёwriñ yi la Njiitu réew mi xamle ne dinañu ubbi (inaugurer) daara ju kowe jii ñu dippe Aamadu Maxtaar Mbów, benn fan ci weeru desàmbar. Njàng ma nag tàmbali woon na, waaye ca Site Kёr Góor gi ak Sikaab Fuwaar lees ko daan amale.
TÀGGAT-YARAM
Njureefi réewi Afrig yi ca joŋante ba
Juroomi réewi Afrig ñoo teew ca joŋantey kuppeg àddina si. Waaye, ba tey, kenn ci ñoom amagul ndam. Senegaal gi njёkk a sóobu ci joŋante bi dañu koo dóor ñaari bal ci dara, Tinisii ak Marog, ñoom, dóoruñu leen, waaye dóoruñu kenn itam. Kamerun nag, dañu koo mujje dóor, moom ak Gana yépp ci bésub tey bi. Mu mel ni réewi Afrig yi dugal nañu ñaari bii, ñu dugal leen juróom-benni bii.
Xibaari gaynde yi ame woon i gaañu-gaañu
Abdu Jàllo, Seexu Kuyaate ak Fóode Bàloo Ture ñooy ñetti doomi Senegaal yi ame woon ay gaañ-gaañu. Fóode Bàloo moom, dese naa wér moo tax du bokk ci ñiy joŋante suba. Seexu Kuyaate moom mi ngi tane ndànk-ndànk. Abdu Jàllo nag tàmbali na di tàggatu ak ikib bi démb.
Kuppeg àddina si : joŋantey alxames ji 24 nowàmbar 202
Siwis 1 – 0 Kamerun
Uruguwey 0 – 0 Koreg suuf
Portigaal 3 – 2 Gana
Beresil 2 – 0 Serbi
Kuppeg àddina si : joŋantey àjjuma ji 25 nowàmbar 2022