LI GЁN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Alxames 29 sàttumbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

DIINE

Génnug àdduna Sёriñ Abdu Rahmaan Mbàkke

Sёriñ Abdu Rahmaan Mbàkke ibnu Sёriñ Abdu Xuddóos ibnu Maam Ceerno Ibra Faati moo génn àdduna ci bésub démb ji. Mu nekkoon nag, nit ku bari woon xam-xam lool te jullite. Umma islaam bi yépp a ñàkk rawatina yoonu murid wi nga xam ne, jàmbaar la ci woon lool.

PÓLITIG 

Ndogali Njiitu réew mi

Ca ndajem jёwriñ ma mu doon amal ci àllarba ji, Njiitu réew mi, jot na faa jёl ay ndogal yu am solo. 

Benn bi di juróom-ñaar ci ay ñoñam yu mu tabb ci ay béréb yu yees. Ñooñu di Meetar Maalig Sàll (Secrétaire permanent du COS-PETROGAZ), Aale Naar Jóob (Secrétaire général du Ministère de l’Economie, du Plan et de la Coopération), Abaabakar Sadiix Béey (Directeur général de l’ANSD), Abdulaay Balde (Directeur général APIX SA), Muntagaa Si (Direction géréral de la société nationale du PAD), Abdulaay Jéey (Directeur général de l’AIBD SA), Suleymaan Njaay (Directeur général SAPCO SA). 

Beneen bi mooy ne dafa namm a delloo Kariim Wàdd ak Xalifa Sàll seen i àqay maxejj. Looloo tax ba mu digal kii di Ismayla Maajoor Faal jёwriñu ji mu dénk wàlluw yoon wi mu def kéemtalayal kàttanam ba ñooñu mёn a bokk ci ñu mёn a fal.

Taxawaayu waa PDS ci ndogal bi

Ginnaaw bi ndogal bi wàccee, kii di Nafisatu Jàllo di fara-caytu bu mag bu PDS mi ngi xamle ne loolu ñoom dañu koy bañ. PDS day ànd ak Kariim Wàdd bañle ko ndogal boobu Njiitu réew mi jёl. Ndax, moom dafa jàpp ne ku ñuy jéggal kay na fekk nga def dara. 

XEW-XEWI JAMONO

Xew-xew bu tiis ca Garã Mbaaw

Ca Garã Mbaaw, benn Kamiyoŋ moo fa dal ci benn taksi bu yaboon jenn jigéen ak benn xale. Ñi nekkoon ci taksi bi, dawalkat bi ak ñi mu yaboon, kenn muccu ci, ñépp a ñàkk seen bakkan.

Beneen aksidã ci otorut bi

Ginnaaw aksidã ba am ca Garã Mbaaw, benn kaar Njaga-Njaay moo daanu ci otorut bi, boori Pikin. Donte ne sax, amagul ku ci ñàkk bakkanam, am na ay góor ak i jigéen yu ca jёley gaañu-gaañu.

Xew-xew bu doy waar ci TER bi

Mbir mu doy waar moo amoon ci TER bi, bésub àllarba ci suba, ci boori Dalifoor. TER bi dafa amoon ab paanoon ba am ñu fa jot a xёm. Mu mel ni nag, jigéen ñaa ca gёnoon a sonn, muy ñu mag ñi walla xale yi.

KOOM-KOOM 

Tolluwaayu Senegaal ci wàllu koom-koom

Koom-koomu Senegaal doxul ni mu war a doxe bees sukkandikoo ci saabalu bànkub àddina si. Donte ne sax, am na ay xew-xew yu fi jot a jaar yu ko gàllankoor lu ci mel ne mbas mi. Kii di Aleksandar Haari bokk ci ñi bind saabal boobu jàpp na ne Senegaal dafa war a xolaat pólitigu kopparal gi. Te, yokk ndimbal yenn boroom kёr yi néew doole yi.

 WÉR-GI-YARAM

Jeneen jéyya ca Wélingara

Ginnaaw jéyya ya amoon ca raglu bu Luga ak ca Kéedugu, jeneen jigéen ju doon muccu moo ñàkk bakkanam ca Wélingara. Kii di A. Njaay, jёkkёru ndaw si, mi ngi xamle ne ñàkk a pasteefug fajkat yee tax ba soxnaam si ñàkk bakkanam. Ndax, nee na, yóbbu na ko fa juróom-benni yoon, ñu naan ko matalagul. Démb nag, bi muy mucc mu sonnoon lool, di nàcc lu bari. Mu dem ba ne leen ñu oppeere ko, ñu ne ko ndogal boobu ñoo koy jёl. Moom nag, dafa namm a topp kilifay raglu bi ca yoon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj