PÓLITIG
Ndogali Njiitu réew mi Ginnaaw tabb yu yees yi mu defoon ci fan yee jàll. Démb, ci ndajem jёwriñ ma mu doon amalaat, Njiitu réew mi am na ñu mu fa jot a jox ay ndomboy-tànk. Ñooñu ñi ngi tollu ci juróom-ñetti nit. Muy kii di Mamadu Basiiru Njaay (Sécretaire général du Ministre du Tourisme et des Loisirs), Màgget Ñaŋ (Directeur général du Budget au Ministère des Finances et du Budget), Usmaan Sillaa (Directeur général de la Société anonyme DAKAAR DEM-DIKK), Abdulaay Ndaw (Directeur général de l’Agence de Développement local), Jimoo Suwaare (Coordonateur du Programme national des Domaines Agricoles Communautaires PRODAC), Abdu Juuf (Coordonateur de la Direction générale du Budget), Ndey Yaasin Géy (Directeur de l’Administration générale et de l’Equipement au Ministère de l’Education nationale), Manjaay Jóob (Directeur de l’Administration générale et de l’Equipement au Ministère du Tourisme et des Loisirs).
NJÀNG AK NÀNGALE
Ubbiteg ndongo yi
Ci Altine ji 3 oktoobar la jàngalekat yi, ñoom, ubbi woon. Waaye, ñii di ndongo yi, démb ci alxames ji 6 oktoobar lañu tijji. Xameesul nag ndax ubbi tey jàng tey jees doon mébét dina mёn a nekk. Ndax, anam yi yenn ci daara yi nekke ci jamono jii.
TÀGGAT-YARAM
Génnug àdduna Allaaji Daawda Fay
Kii di Daawda Fay, nekkoon fi jёwriñu tàggat-yaram ci Nguurug Abdulaay Wàdd moo génn àdduna. Moom nag, jàmbaar la woon ci wàll woowu. Ndax, moo jiite woon kurél gi doon amal CAN 1992 bi doon ame ci Senegaal.
Senegaal mi ngi wéy di jiitu ci Afrig
FIFA yeesalaat na taxawaayi ékibi àdduna si ci wayndare gi. Waaye, ñii di waa Senegaal moom ña nga fa ñu nekkoon ca fukk ak juróom-ñetteelu palaas ba. Ñoo ngi wéy di jiitu ci Afrig ba léegi.
XEW-XEWI JAMONO
Xew-xew bu doy waar ca Pàdduwaa
Fale ca Pàdduwaa nekk ca diwaanu Kafuntin, jenn jigéen lañu fa fekk mu dee. Jigéen jooju nag, amoon na lu tollu ci fanweeri at. Rax-ci-dolli, amoon na ay gaañu-gaañu ci yaram wi. Néew bi nag yóbbu nañu ko ca morgu bu raglu bu Sigicoor ngir xam lan moo sabab dee gi.
Jéyya ca diwaanu Jurbel
Jéyya ji mi ngi ame ca isin bii di STAR (Société de Transformation Aagro-alimentaire Raffinée) nekke ca Nebe Séeréer ca diwaanu Jurbel. Lu tollu ci ñaari nit ñàkk nañu ci seen i bakkan ginnaaw tàkkug (explosion) chaudière bi. Ñeent ci juróom-ñeent ya ca jёle ay gaañ-gaañu jàllale nañu leen ca Ndakaaru. Juróom ya ca des, raglu Jurbel bu mag ba moo leen jёl.
XIBAARI BITIM-RÉEW
Xibaar bu tiis ca Gàmbi
Lu tollu ci juróom-benn fukki xale ak juróom-benn ñoo fa ñàkk seen i bakkan. Waaye, ñii di waa OMS di artu ci siro yiy faj soj ak sёqёt yoo xam ne ñi ngi leen defare ci laboraatuwaaru saa-ind bii di Maiden Pharmaceuticals. Jàpp nañu sax ne mёn na am moo waral faatug xale yooyu. Te, siro yooyu mёn naa am ne séddale nañu leen ci yeneen réewi Afrig bees sukkandikoo ci AFP.
Njiitu réew lu yees ca Burkinaa Faaso
Kii di Kàppiten Ibraahiim Taraawore mooy Njiitu réewu Burkinaa Faaso ginnaaw bi mu daanelee kii di Lieutenant-colonel Póol Aari Sàndawgoo Damibaa fanweeri fan ci weeru Sàttumbar. Damibaa moomu nga xam ne moo daaneloon Kiriscan Kaboore ci Saŋwiye bii weesu.
Am cong ca Tayland
Ci benn béréb bu ñuy yóbbu ay xale (crèche) ca Na Klang la am congu am. Ki ko amal ab takk-der la woon mi ngi tollu ci fanweeri at ak ñeent. Mi ngi yoroon ag fetal ak paaka ngir rey ay xale ak ñaar ci seen i jàngalekat. Ñi faatu ci cong mi tollu nañ ci lu mu néew-néew fanweer. Ay xale nag ñoo ci ёpp, ndax lu tollu ci ñaar fukki xale ak ñett ñàkk nañu ci seen i bakkan. Te, ki def ñaawteef bi dafa rey jabaram ak seen doom laata muy xaru.