Ngomblaan gi génne na ab yégle di ci xamle ne dina amal lëlu aadaam bu atum 2023/2024 ci gaawu gii, 14 oktoobar bu 10i waxtu jotee ci yoor-yoor. Dañu bind ci seen yégle bi ne :
« Wowees na dépite yépp ci jotaayu gaawu gi… ngir ñu waxtaane li jëm ci ubbiteg lëlub aada bob Ngomblaan gi. »
NDAJEM F24
Kurélu F24 amaloon na am ndaje ngir waxtaane mbirum Aliw Saane mi ñu nëbb jànt wi ak ni kaso yi fesee dell ak i nit. Ci seen biir yégle bi ñu siiwal, ñoo ngi ciy :
« …naqarlu li ñu nu tere def sunu doxub ñaxtu. Nde, dañ noo xañ sunuy àq ak i yelleef… nu ngi ñaawlu it ni ñuy salfaañee Yoon ba DGE di bañ a jox Usmaan Sonko xobi baayale gi…Nu ngi woo ñi bokk ci F24 ñépp, nu waxtaan xool nu nuy doxalee ba wotey 2024 yi am ci jàmm, ba lépp jaar yoon te du am njuuj-njaaj… »
AKSIDAŊ CA KUMPENTUM
Ab sàndarm buy wuyoo ci turu Serif Jariso Sow moo ñàkk bakkanam ci kaw tali bi altine ci guddi gi. Dafa doon def liggéeyam ci kaw tali bi, diggante booy génn Kumpentum di dugg biir Kungél, ngir dem beek dikk bi jaar yoon. Noonu, ag daamaru Toyota dal ci kawam, mu ñàkke ci bakkanam ca saa sa. Yoon teg na loxo boroom daamar gi ngir ubbi ab luññutu.
TÀGGAT-YARAM
Nikolaa Jakson du mën a bokk ci joŋanteb kuppe bu gayndey Senegaal yu mag yi war a amal keroog bésub 16 oktoobar 2023 ca Lãs (Farãs). Joŋante boobu nga, mi ngi dox diggante Senegaal ak Kamerun. Dañ ko oppeere woon ci loxo, moo tax du bokk. Waaye, kii di Abdallaa Simaa moo ko ciy wuutu. Ci talaata jii lay ñëw tàggatu ak yeneen gaynde yi.
UCAD DINA UBBI AY BUNTAM CI WEERU NOWÀMBAR
Njiitul COUD li, Màgget Seen, xamle na ne daara ju kawe ju Seex Ànta Jóob dina ubbiy buntam fii ak i fan. Ci rajo RFM la ko yéglee, wax ne :
« …Balaa loolu, am na loo xam ne fàww ñu waxtaan ceek ndongo yi ak jàngalekat yi. Ndax kat, 1 fan ci weeru suwe wii weesu kenn du ko fàtte cii biir daara ji. Looloo tax, fàww ñu waxtaane kaarange geek dëkkuwaayu ndongo yi ba ñépp nekk ci jàmm. Su ko defee, fii ak nowàmbar, xale yi dinañ mën a dugg ci biir daara ji, jàng ci jàmm. »