Ag lakk gu yéemee amoon ca ja bu mag (marché central) ba ca Kawlax, ci guddig gaawu gi 11 nowàmbar. Ñeenti kàntin jot nañu cee tàkk ba jeex, laata waa sàppëer-pompiyee di yegsi ngir fay lakk gi. Bees sukkandikoo ci ñenn ci waa ja ba, lakk-lakk yi dañoo bari lool fan yii. Te, dara waralu ko lu dul ñiy làkkatu, di def ay mbiri barãsmaŋu mbëj mi.
SËRIÑ MBUUB
Ginnaaw bi mu sampee ndëndam ci wotey 2024 yi, moom Sëriñ Mbuub, demoon na ca ja bu ñuy jaaye jën ya ca Pikin (marché central au poisson de Pikine) ngir waxtaan ak ñoom. Waaye, ca biir ndaje ma, ab pólisee dugg ci seen biir, dagg waxtaan wa. Bi pólisee bi waxee li waral mu def lu ni mel, ba déggoo am ci, lañu yeggale seen waxtaan. Ci biir waxtaan wi, Sëriñ Mbuub a ngi ciy àddu di leeral naan « fii nuni neen doŋŋ ñoo fi nekk di waxtaan, te yaakaar naa ne, fii ak amul lu ëpp, jarul pólis di fi ñëw ba naan dafay am lenn lu mu fiy dogal ».
PÓLITIG
Keebaa Kànte mi bokkoon ci lëkkatoo bu Bennoo Bokk Yaakaar, xamle na ci am ndaje ma ñu amaloon ca dalub Umar Lamin Baaji ci gaawug 11 nowàmbar 2023, ne léegi Karim Wàdd lay àndal ci wotey 2024 yi.
NDAJEM ARAABI-SAWDIT – AFRIG
Njiitu réew mi, Maki Sàll, jël na kàddu ca ndaje ma ca Riyaad, di xamle ne
« Jàmm rekk a mën a saafara xeexu Palestin bi ak Israayel, te loolu fàww ñaari réew yépp di doxal seen bopp, ku ci nekk moom sa bopp te dara du la tënk. leeral tamit, ci li ñépp dul werante, ku ci nekk fan la say dig yem…Maa ngi ñaan ONU mu jël ci ay matuwaayam, def ci lépp lu ci war…Li ñiy rey ay nit ca Gaza ëpp na lool ba jéggi dayoo. »
TÀGGAT-YARAM
Aliw Siise mere na lool waa CAF ci ndogal li ñu jël ne ekib bu nekk 23i fubalkat kese lay am ci CAN 2023 biy am ca Koddiwaar. Rax-ci-dolli, dina am joŋante yu nar a tàmbale ñaari waxtu ci yoor-yoor bi. Li Aliw Siise di kaas mooy ne mënoon nañ bàyyi lim bi ci 26 mbaa 27i fubalkat, ak waxtu yi ñu nar a nekk joŋante, naaj wi di fa nar a tàng. Te yit seen wér-gi-yaram la leen di ragalal.